Saalu Nguur yi Porogaraam bi ñu taxawal ngir tabax ay Saalu Nguur gi, mu ngi jëm kanam
1 Ndaje bi gën a mag bu ñu defoon ci atum 1983 ca Etaa Sini mu ngi tuddoon “ Nguuru Yàlla dafay tax ñu nekk benn ”. Foofu, waxoon nañu ne dinañu dajale xaalis ngir mën a tabax walla defaraat ay Saalu Nguur ci Etaa Sini, ak Canada. Liggéey boobu, ak lu tuuti lañu ko tàmbalee, waaye xamuñu woon barke yi ci naroon a jóge. Ñu ngi doon tàmbalee xam li Sabuur 92:4 tekki. Sabuur boobu dafa ne : ‘ Li ngay def, céy Yexowa, bégal na ma ; liggéey bi ngay def ak sa loxo, tax na ma bég bay yuuxu. ’
2 Tey, li ñu jot a def tax na ñu bég lool. Porogaraam bu ñu taxawal ngir gaaw a tabax ay Saalu Nguur ci àddina si sépp, mu ngi dox bu baax. Kenn ku nekk am na li mu mën a def ngir bokk ci liggéey boobu. Loolu lan la ? Mën nañu maye xaalis, lu bare walla lu tuuti, ngir ñu mën a tabax ci àddina si sépp ay saal yu gën a bare, fu ñu mënee jaamu Yàlla. Suñu mbokk yu bare nangu nañu jëfandikoo jumtuwaay yi ñu am, seen jot, ak seen xam-xam, def ko ci liggéey boobu. Li waral liggéey boobu di dox bu baax mooy li ñu Yexowa di won li ñu war a def, di ñu jàpple, te di barkeel li ñuy ànd def ci liggéey boobu. — Sab. 127:1.
3 Ci ay bànqaas yu bare, topp nañu li ñu doon def ci mbooloo yi nekk Etaa Sini. Ci réew yu bare, def nañu ay boyet ci Saalu Nguur yi, ndax waaraatekat yi mën cee def xaalis ngir Saalu Nguur yi. Le Ministère du Royaume bu màrs 1997 bu Etaa sini, am na lu bés lu mu waxoon ci porogaraam boobu. Dafa ne : “ Mbootaay gi tàmbali na dajale xaalis ngir Saalu Nguur yi ci atum 1983. Booba ba tey, suñu mbokk yi maye nañu xaalis bu bare, xaalis bu ñu mën a abal ñi bëgg tabax Saalu Nguur. Fu mu ne nii, def nañu ko ci lu mat 2 700 mbooloo, fii ci réew mi. Bu dul woon loolu, ay mbooloo yu bare, naruñu woon a tabax seen Saalu Nguur gi, walla defaraat leen. Fu mu ne nii, am na ay mbooloo yu nekk ci réew yu barewul xaalis, te soxla ñu gaaw leen a abal ci xaalis boobu. Yéen ñi di maye xaalis ngir jàpple liggéey boobu, ñun ñi Mbootaay bi ak mbooloo yooyu di jariñoo xaalis boobu, ñu ngi leen di gërëm bu baax-a-baax. ”
4 Yégle boobu, dañu ko defoon ngir nit ñi ñów bokk ci porogaraam bu ñu taxawal ngir gaaw a tabax ay Saalu Nguur. Dañu bëggoon a jël xaalis bi ñu doon dajale ngir dimbali suñuy mbokk ci ay réew yu gën a bare, boole ci wéy di tabax ay Saalu Nguur ci réew mii. Ginnaaw loolu, Le Ministère du Royaume bu ut 1997 newoon na : “ Saali Nguur yi ñu soxlaa tabax ci àddina si sépp, ñu ngi yokku bés bu nekk. Daaw rekk, taxawal nañu 3 288 mbooloo yu bés. Yu ci bare ñu nga Afrig, Asie, digg ak bëj-saalumu Amerig ak it penku Ërob. ”
5 Lan moo xew booba ba tey ? Annuaire bu 2001 nee na : “ Porogaraam boobu tax na ñu àggale 453 Saalu Nguur te tàmbali nañu tabax 727 yeneen Saalu Nguur, ci 30 réew. Wone nañu bu baax ne bu ñuy tabax Saalu Nguur ci benn réew, dañu war a jëfandikoo li nit ñi di tabaxe ci réew moomu, topp it ni ñu fay tabaxe, ba pare defar saal boo xam ne ci moom lañuy roye bu ñuy tabax yeneen saal yi ci réew moomu. Kenya, ay xeer lañuy tabaxe, Togo, muul la, Cameroun, betoŋ ba pare ñu raax ko. Loolu tax na suñu mbokk ci ngëm yi fa nekk gaaw a mën a tabax ba mën a yore lu gën a diis ci porogaraamu tabax bi nekk ci seen réew. ”
6 Yexowa mu ngi barkeel porogaraam boobu ci Afrig. Ñépp a ko mën a gis. Léegi, xoolleen ci nataal yi nekk fii, ay Saalu Nguur yu ñu tabax. Tabax yooyu am na li ñu jur ci ñetti fànn : li Seede yi ci àddina si sépp nekke benn, li mu def ci ñi nekk ci dëkk yooyu, ak li mu tax ne ñi fa teew gën a bare. Sasu Nguuru Yàlla bii dafay wone Saalu Nguur yi ñu tabax ci Afrig. Waaye ci beneen Sasu Nguuru Yàlla dinañu wone naka la porogaraam bi ñu taxawal ngir tabax ay Saalu Nguur di jëme kanam feneen ci àddina si.
Nataal yi nekk 3]
RÉPUBLIQUE CENTRAFRICAINE
Bimbo, Bangui
Begoua, Bangui
[Nataal yi nekk 4]
Ukonga, Tanzanie
[Nataal bi nekk 4]
Accra, Ghana
[Nataal bi nekk 4]
Salala, Liberia
[Nataal bi nekk 4]
Karoi, Zimbabwe
Nataal yi nekk 4, 5]
Allada, Bénin — Saalu Nguur bu njëkk ba
Allada, Bénin — Saalu Nguur bu bees bi
Nataal bi nekk 5]
Kpémé, Togo
[Nataal bi nekk 5]
Sokodé, Togo
Nataal yi nekk 4, 5]
Fidjrosse, Bénin
Nataal bi nekk 6]
Lyenga, Zambie — Saalu Nguur bu njëkk ba
[Nataal bi nekk 6]
Lyenga, Zambie — Saalu Nguur bu bees bi
Nataal bi nekk 6]
Kinshasa, Congo
Nataal bi nekk 6]
Musambira, Rwanda