TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 4/03 p. 1
  • “ Nangu ko ”

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • “ Nangu ko ”
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2003
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Lan la Biibël bi wax ci salibateer ak séy?
    Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
Sasu Nguuru Yàlla — 2003
km 4/03 p. 1

“ Nangu ko ”

1 Ci benn waxtaan bi mu amoon ak taalibeem ya ci lu jëm ci séy, Yeesu dafa ne ku bañ a séy dafa mel ni am na lu ñu ko may ci wàllu ngëm. Ba pare dafa ne : “ Ku ko mana nangu, nangu ko. ” (Macë 19:​10-​12). Ay at ginnaaw loolu, ci benn leetar bu mu bindoon, ndaw li Pool wax na ci njariñ bi bañ a séy am. Xiir na nit ñi ci topp ko, moom mi amul jabar (1 Kor. 7:​7, 38). Tey ñu bare nangu nañu bañ a séy te gis nañu njariñ bu ñu ci mën a jële. Ban njariñ la ?

2 Bañ a am “ njaaxle ” bu ñuy jaamu Yàlla : Pool gisoon na ne bañ a séy taxoon na mu mën a jaamu Yexowa te bañ a am “ njaaxle ”, maanaam bañ a bare ay xalaat bu ñuy def liggéeyu Yàlla. Noonu it tey, boo nekkee góor te amoo jabar mën nga dem ca l’École de formation ministérielle. Boo amul jabar walla jëkkër, lu bare dina gën a yomb ci yow : nekk pioñee, jàng beneen làkk, toxu foo xam ne dañu soxla ay waaraatekat, nekk Betelit, walla nangu ñu woo la ngir def dara ci liggéeyu Yàlla. Dinga gën a am jot ngir toog, jàng bu baax a baax baatu Yàlla te xalaat ci, ngir ñaan Yexowa ay ñaan yoo xam ne ci sa biir xol lañu jóge, te ngir dimbali nit ñi. Loolu yépp sa “ njeriñ ” lay doon. — 1 Kor. 7:​32-​35 ; Jëf. 20:⁠35.

3 Boo mënee jaamu Yàlla te bañ a bare ay xalaat, lu baax la lay indil. Am na suñu benn mbokk mu jigéen bu amul jëkkër, def na 27 at ci Kenya, lii la wax : “ Amoon naa ay xarit yu bare ak liggéey bu bare ! Dañu doon bokk lu ñuy def, di seeti ku nekk sa moroom. [...] Ku amul jëkkër, mën nga def walla dem foo bëgg. Loolu tax na ma mën a def lu bare ci liggéeyu waare bi. Bég naa lool. ” Lii la ci yokk : “ Te sama diggante ak Yexowa dafa gën a rattax. ”

4 Nangu ko : Yeesu nee na “ nguuru Yàlla Aji Kawe ji ” moo war a tax ñu nangu bañ a séy (Macë 19:12). Lépp lu ñu lay may, war nga ko jëfandikoo ni mu ware soo ci bëggee am mbégte ak njariñ. Benn la ak bañ a séy. Bañ a séy mën na la may nga def lu bare. War nga it ñaan Yexowa mu may la xel ak kàttan, te nanga xam ne dina ko def. Ñu bare ñu amul jabar walla jëkkër def nañu loolu yépp ba gis njariñ bi ci nekk.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager