TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 8/03 p. 1
  • Nañu roy ci mbaaxaayu Yexowa

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Nañu roy ci mbaaxaayu Yexowa
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2003
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Nañu roy mbaaxu Yexowa
    Nañu woyal Yexowa ànd ceek mbégte
Sasu Nguuru Yàlla — 2003
km 8/03 p. 1

Nañu roy ci mbaaxaayu Yexowa

1 Boo lekkee togg bu neex dinga bëgg gërëm Yexowa. Bu tawee fekk mu tàng lool, noonu la itam. Lépp lu baax li ñu am, moom moo ñu ko may. Yexowa dafa baax ba nga xam ne, dañu bëgg def ni moom (Sab. 119:​66, 68 ; Efes 5:⁠1). Naka lañu mënee baax ?

2 Nañu baax ak ñi nekkul karceen : Nañu bëgg ñi nekkul karceen. Bu ñu defee loolu, dinañu roy ci Yexowa (Gal. 6:10). Bu ñu baaxee ak nit ñi, mën na tax ñu xalaat lu baax ci Seede Yexowa yi te bëgg déglu xibaar bu baax bi.

3 Benn xale lu góor bu nekk pioñee dafa nekkoon ci benn loppitaan di raŋ ngir mën a faju. Benn jigéen ju màgget nekk ci wetam, sonn lool. Mu ngi mel ni ñi fa nekkoon ñépp, moo ci gënoon a feebar. Bi ñu woowee suñu mbokk ci doktoor bi, dafa bàyyi jigéen jooju dem ci palaasam. Beneen bés mu tasewaat ak moom ca marse ba. Jigéen ji kontaan lool. Bu njëkk bëggul woon a déglu xibaar bu baax bi. Waaye bés boobu dafa wax ne xam na léegi ne Seede Yexowa yi dañu bëgg seeni moroom bu baax-a-baax. Ginnaaw ga, dafa nangu ñu defal ko benn njàngum Biibël bi.

4 Nañu baax ak suñu mbokk karceen yi : Nañu dimbali suñu mbokk karceen yi. Noonu lañuy roye it ci Yexowa. Bu amee musiba, dañuy bokk ci ñiy njëkk ñów ngir dimbali suñu mbokk yi. Mën nañu dimbali itam ñi soxla lu leen di yóbbu ci ndaje yi, dem seeti suñu mbokk yi feebar walla màgget. Te it bu amee suñu benn mbokk bu ñu xamul bu baax ci mbooloo mi, nañu seet ni ñu mënee def ba gën koo jege. — 2 Kor. 6:​11-13 ; Yaw. 13:⁠16.

5 Yexowa dafa ñuy nangu baal. Loolu it mooy wone ne dafa baax (Sab. 86:⁠5). Ñun it, nañu nangu baal suñu moroom yi. Noonu it lañuy roye ci Yexowa, te ci lañuy wone ne dañu bëgg baax (Efes 4:32). Loolu dina tax suñu diggante ak suñu mbokk karceen yi ‘ baax te neex ’. — Sab. 133:​1-3.

6 Yexowa dafa baax lool. Kon nañu ko màggal bu baax te bég lool. Nañu fexe it ba roy ci moom, di baax ci lépp li ñuy def. — Sab. 145:7 ; Yér. 31:12.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager