“ Nañu bég bu ñuy jaamu Yexowa ”
1 “ Deeleen bég ci boroom bi; maa ngi koy waxati: Bégleen! ” Loolu la ndaw li Pool waxoon (Fil. 4:4). Yégle xibaar bu baax bi te dimbali nit ñi ñu jaamu Yexowa, lu réy la te mbégte mu réy lay indi (Lukk 10:17 ; Jëf. 15:3 ; 1 Tes. 2:19). Waaye bu fekkee ne yenn saay duñu bég ci suñu waaraate, lan lañu mën a def ?
2 Yàlla moo ñu sant liggéey boobu : Buleen fàtte ne Yexowa ci boppam moo ñu sant liggéeyu waare bi. Ñu ngi liggéeyandoo ak Yàlla di xamle xibaaru Nguur gi te di sàkk ay taalibe. Loolu lu réy la ! (1 Kor. 3:9) Yeesu Krist moom itam dafay ànd ak ñun ci liggéey boobu nga xam ne dootul amati (Macë 28:18-20). Malaaka yi ñoom itam ñu ngi ci liggéey boobu, di am lu bare lu ñuy def te ñu ngi ànd ak ñun ci ngóob bu mag bi ci wàllu xel bi ñuy def tey (Jëf. 8:26 ; Peeñ. 14:6). Mbind yi ak li xew ci mbooloo Yàlla mi, dañuy wone ci lu leer ne Yexowa mu ngi ñuy jàpple ci liggéey boobu. Kon nag bu ñuy waaraate, “ ci suñu booloo ak Krist, nu ngi waare [...] fa kanam Yàlla, ni yonenti Yàlla ” (2 Kor. 2:17). Ci dëgg, war nañu bég !
3 Ku bëgg wéy di bég ci liggéeyu Yàlla, fàww mu ñaan Yàlla (Gal. 5:22). Kàttanu Yàlla kese mooy tax ñu mën a def liggéeyam. Kon fàww ñu ñaan ko bu baax xelam mi nga xam ne dafa koy may ba mu doy ñi ko koy ñaan (Lukk 11:13 ; 2 Kor. 4:1, 7 ; Efes 6:18-20). Nañu faral di ñaan lu jëm ci suñu waaraate. Su ko defee, bu ñu dajee ak ku ñu bëggul déglu, duñu fàtte ni ñu ko war a gise. Dina tax ñu kontine di am fit ci liggéey waaraate bi te wéy di ci bég. — Jëf. 4:29-31 ; 5:40-42 ; 13:50-52.
4 Waajal ko bu baax : Bu ñu bëggee gën a bég ci waaraate bi, dañu ko war a waajal bu baax (1 Pie. 3:15). Loolu soxlawul jot gu bare. Tuuti minit kese doy na ngir seetaat li ñu mën a wax bu ñuy wone yéenekaay yi ñu mujj jot walla yeneen téere yi . Boo bëggee xam ni nga mënee ubbi waxtaan bi, mën nga seet téere Comment raisonner walla ay Sasu Nguuru Yàlla yu weesu. Am na ñuy bind ci kayit bu ndaw li ñu bëgg a wax, yóbbaale ko bu ñuy waaraate. Lee-lee ñu ciy xoolaat ngir fàttaliku li ñu war a wax. Loolu dafay tax ñu bañ a ragal, te am fitu waaraate.
5 Mbégte, bare na njariñ. Nit ñi, bu ñu gisee ku bég, dañu koy gën a bëgg déglu. Te mbégte dafay tax ñu gën a muñ (Nëx. 8:10 ; Yaw. 12:2). Te li ëpp solo mooy, am mbégte ci jaamu Yexowa, dafay koy màggal. Kon, nañu “ bég bu ñuy jaamu Yexowa ”. — Sab. 100:2.
[Laaj yi]
1. Lu mën a indil kiy jaamu Yexowa mbégte mu réy ?
2. Lu tax bañ a fàtte ki ñu yebal mën a tax ñu bég ?
3. Lan la ñaan mën a def ci ku bëgg wéy di bég ci liggéeyu Yàlla ?
4. Bu ñu waajalee bu baax suñu bopp, naka lay yokke mbégte bi ñuy am ci waaraate bi te naka lañu mënee waajal suñu bopp ?
5. Ban njariñ la mbégte am ci ñun ak ci suñu moroom yi ?