Nañu rattaxal suñu diggante ak Yàlla
1 Suñu benn mbokk mu jigéen nee na : “ Ci 20 at yii weesu, dëgg gi nekkul woon dëgg ci sama xol. Dama doon teewe ndaje yi te di waaraate, waaye fa la yemoon. ” Lii nag la ci teg : “ Dem naa ba gis ne loolu doyul. Dëgg la, am na solo waaye boo nekkee ci coono ñaar yooyu kese duñu la mën a may doole bi ngay soxla. [...] Léegi xam naa ne war naa seetaat sama bopp. War naa am porogaraam bu baax ngir jàng Biibël bi, maanaam jàng ngir xam Yexowa bu baax, bëgg ko te fonk li ñu Doomam may. ”
2 Am diggante bu rattax ak Yexowa, am na lu muy laaj. Te loolu weesu na tàmm def yenn yi ci wàllu ngëm. Bu ñu tàmmulee waxtaan ak Yexowa ci ñaan, dina mel ni am benn xaritu benn bakkan te bañ a wax ak moom (Peeñ. 2:4). Nañu seet léegi naka la njàngum Biibël ak ñaan mënee tax ba suñu diggante ak Yàlla rattax. — Sab. 25:14.
3 Ñaan ak xalaat bu baax ci li ngay jàng lu am-a-am solo la : Kuy jàng Biibël bi te bëgg mu dugg bu baax ci xolam, warul yem rekk ci rëdd li am solo ci li muy jàng ak seet aaya yi ñu ci bind. Waaye dafa war a toog di xalaat ci yoonu Yexowa, ci li mu ñu sant ak ci jikkoom (2 Mu. 33:13). Bu ñu jàngee lu jëm ci suñu diggante ak Yàlla, nañu fexe ba mu leer ci suñu xel. Kon dina laal suñu xol, te dina tax ñu seetaat bu baax ni ñuy dunde (Sab. 119:35, 111). Bëgg gën a jege Yexowa moo war a tax ñuy toog ngir jàng Biibël bi te xalaat ci (Saak 4:8). Njàng mu xóot dafay laaj jot ak fu ñu ko mënee def bu baax. Te it su ñu ko bëggee tàmm, fàww ñu yar suñu bopp ci loolu (Dañ. 6:10). Bu fekkee ne sax barewuloo jot, ndax bés bu nekk yaa ngi beral jot ngir xalaat ci jikko Yexowa yi rafet lool ? — Sab. 119:147, 148 ; 143:5.
4 Boo bëggee jàng Biibël bi yow kenn ni mu ware, war nga ñaan ñaan yu xóot yu jóge ci sa biir xol. Lu am solo la. Ku bëgg dëgg gi nekk ci Biibël bi dugg ci biir xolam te xiir ko ci jaamu Yàlla “ boole ci wegeel ak ragal ”, dafa war a am xel mu sell mi (Yaw. 12:28). Kon nag, saa yoo bëggee jàng Biibël bi yow kenn, bala ngay komaase, danga war a njëkk ñaan Yexowa, ngir mu may la xelam (Macë 5:3). Bu ñuy xalaat ci Mbind mi te di jëfandikoo téere yi mbootaayu Yexowa defar, dañuy ubbil Yexowa suñu xol (Sab. 62:8). Jàng Biibël bi noonu, bokk na ci jaamu Yexowa. Dafay wone ne gëm nañu ko, te dafay rattaxal suñu diggante ak moom. — Yudd 20, 21.
5 Bu ñu bëggee suñu diggante ak Yexowa gën a dëgër bés bu nekk, dañu ko war a sàmm, mel ni ni ñu koy defe ak yeneen nit ñi. Kon nag, bés bu nekk, nañu jël ci suñu jot ngir gën ko jege. Bu ñu defee loolu, nañu xam ne moom itam dina ñu gën a jege. — Sab. 1:2, 3 ; Efes 5:15, 16.
[Laaj yi]
1. Am na lu suñu benn mbokk mu jigéen faraloon a def ci wàllu ngëm. Waaye lan la ci mujj gis ?
2. Lu tax ñu war a fexe ba suñu diggante ak Yexowa rattax ?
3. Bu ñu bëggee gën a jege Yàlla, naka lañu waree jàng Biibël bi ñun ci suñu bopp ?
4. Ñaan bala ngay jàng Biibël bi yow kenn, naka lay rattaxale sa diggante ak Yexowa ?
5. Lu tax ñu war a toog di xalaat ci li nekk ci Kàddu Yàlla bés bu nekk ?