Ndaje bu gën a mag bi ci atum 2004 : “ Nañu ànd ak Yàlla ”
1 Am na lu bare lu tax ñu bëgg ndaje yu gën a mag yi am at mu nekk. Dañu fay am waxtaan ak daraam yu ñu “ surga bu takku te teey ” bi pareel (Macë 24:45-47). Dañu fay am it ay téere yu bees yuy faj suñuy soxla ci wàllu ngëm. Dañu fay déglu ay mbokk ci ngëm yuy wax ni Biibël indee jàmm ci seen dund. Dañu fay dégg ni liggéeyu waare bi di jëme kanam ci yeneen réew. Te it dañu fay am ay waxtaan yu neex ak suñuy mbokk ci ngëm yi, mag ak ndaw. Waaw, yàkkamti nañu suñuy ndaje yu gën a mag yi.
2 Nañu fekke ñetti fan yépp : Lii la Yexowa wax ci gémmiñu Musaa : “ Dajaleel mbooloo mi, [...] ngir ñu déglu te jàng. ” (5 Mu. 31:12). Tey, Yexowa dafay jaar ci surga bu takku te teey bi ngir jàngal ñu. Te loolu dina ko def ci ndaje bu gën a mag bi, ci ñetti fan yi yépp. Li ñu Yexowa di jàngal dafa ñuy jariñ. Kon nañu ñów déglu lépp li mu ñuy jàngal (Isa. 48:17). Ndax danga bëgg ki ngay liggéeyal bàyyi la nga teewe ndaje bu mag bii di ñëw ? Kon nanga jëkk ñaan Yexowa ba pare dem waxtaan ak moom. Boo defee loolu, dinga topp li Nëxemiyaa defoon (Nëx. 1:11; 2:4). Te boo dëkkee ak ñi nga bokkalul diine, nanga leen teel a wax ne danga war a teewe ndaje bu gën a mag bi. Loolu moo gën a rafet.
3 Fi nit ñi mën a dal : Toppatoo nañu ba pare fi nit ñi mën a dal ci dëkk yi ñu war a defe ndaje yu gën a mag yi. Na ku nekk topp bu baax li ñu taxawal ngir loolu. Bu ko defee, suñu mbokk yi nangu teral gan yi, seen kër du fees ba mu ëpp li ñu àttan. Daaw, ci benn ci dëkk fi ñu doon defe ndaje bu mag, boo seetee ñi bëggoon am fi ñuy dal ñépp, genn-wàll gi kese ñoo ko waxoon. Loolu lu mu indi ? Am na kër yoo xam ne, ñi fa daloon, matoon nañu ñetti yoon ñi fa waroon a ñów.
4 Bu amee waaraatekat buy ñaan li nekk ci kayit bi tudd Demande de chambre pour cas particuliers, kurélu liggéeyu waare bi dina seet ndax mën nañu ko may li muy ñaan. Waaraatekat yi am tur bu rafet ci mbooloo mi ak seen doom yu am yar bu rafet kese, ñoo mën a ñaan li nekk ci kayit boobu. Biro biy toppatoo fi nit ñi mën a dal, bu amee li mu bëgg laajte ci li waaraatekat ñaan ci kayit boobu, na ko laaj sekkerteeru mbooloo nit kooku.
5 Ñi soxla ndimbal : Ndaw li Pool waxoon na mbooloo yi nekkoon Galasi ñu ‘ defal ñépp lu baax, rawati-na nag seen mbokk yi gëm ’. (Gal. 6:10.) Ci mbooloo mi, am nañu ay mbokk yu nekk mag, yu feebar, yuy yar seeni doom ñoom kenn ak itam ay mbokk yu def seen jot yépp ci liggéeyu Yexowa. Xéyna teewe ndaje boobu yombul ci ñoom, waaye duñu ko wax. Boo bëggee def lu baax te nga mën ko, ndax mënoo leen a jàpple ? Ñi bokk ci seen njaboot fekk ay karceen lañu ñoom it ak magi mbooloo yi war nañu xam bu baax li suñu mbokk yooyu soxla.
6 Ñi bëgg teewe ci beneen ndaje bu gën a mag : Xéyna doo mën a teewe fi sa mbooloo war a teewe ba tax nga bëgg xam lu jëm ci yeneen ndaje yu gën a mag. Nanga wax ak sa sekkerteeru mbooloo. Boo xoolee ci ginnaaw kayit bi tudd Demande de chambre pour cas particuliers, dinga fa gis kañ lañu war a def yeneen ndaje yu gën a mag yi ci at mi ak adareesu biro yi leen di toppatoo. Boo bëggee ñu wutal la fooy mën a dal, seetal biro biy toppatoo ndaje bu gën a mag fi nga bëgg teewe, te yónnee ko kayit boobu. Boole ci anwalob bu am tembar te bind ci sa adarees. Bu fekkee ne ci dëkk bi nga war a dem dafa war a am ñaari ndaje yu mag walla sax lu ko ëpp, bul fàtte wax ban ndaje nga ci tànn. Biro biy toppatoo fi nit ñi war a dal ci ndaje boobu mooy seet sa kayit.
7 Am na léegi lu ëpp 2 500 at ci ginnaaw, mbooloo Yàlla defoon na ndaje bu mag. Foofu Esras ak yeneen Léwit jàng nañu Kàddu Yàlla te leeral ko. Loolu lu mu indi ? Nëxemiyaa 8:12 nee na : “ Mbooloo mi yépp dem [...] ak mbégte mu réy, ndaxte dañu nàndoon li ñu leen jàngaloon. ” Ni ko Esras ak Léwit yooyu defe woon, surga bi ñu tànn mu ngi leeral tey Kàddu Yàlla, te wone ni ñu ko mënee topp. Ndax bëggoo leen gërëm ci loolu ñuy def ? Li surga boobu di def noonu dafa ñuy won ne Yexowa dafa ñu fonk te dafa bëgg toppatoo mbooloom bu baax. Fexeel ba teewe ñetti fan yépp yi ñuy defe ndaje bi gën a mag bi tudd “ Nañu ànd ak Yàlla ”.
[Wërale bi nekk paas 3]
Waxtu yi
Àjjuma ak Samdi
9 h 30 – 17 h 10
Dimaas
9 h 30 – 16 h 05