TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 5/04 p. 1
  • Li ñu mën a def ngir gërëm Yàlla

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Li ñu mën a def ngir gërëm Yàlla
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2004
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • “ Gërëmleen Yàlla ”
    Sasu Nguuru Yàlla — 2008
Sasu Nguuru Yàlla — 2004
km 5/04 p. 1

Li ñu mën a def ngir gërëm Yàlla

1 Dëgg la, ñu ngi ci “ bési tiis yu tar ”, waaye li war a tax ñu gërëm Yexowa bu baax bare na lool (2 Tim. 3:⁠1). Li ci njëkk mooy li mu maye Doomam ngir ñun (Ywna. 3:​16). Ginnaaw loolu ñi bokk ci diine yu dul dëgg yi ñu ngi mel ni ñu xiif lool ci wàllu ngëm. Waaye ci wàll boobu, ñun am nañu lépp li ñu soxla (Isa. 65:13). Te dañu bokk it ci lu mel ni njaboot gu am ay mbokk ci àddina si sépp. Te it tey, ci àddina si sépp, ay nit ñu baree bare ñu ngi ñów bokk ci diine dëgg ji. Te ñun bokk nañu ci ñi def liggéey bu réy boobu (Isa. 2:​3, 4 ; 60:​4-​10, 22). Lan lañu mën a def ngir gërëm Yexowa ci barke yu dul jeex yi mu ñu may ? — Kol. 3:​15, 17.

2 Li ñuy def ci liggéeyu Yàlla, na jóge ci suñu xol te ànd ak mbégte : Bi mu doon wax ci alal bi nit ñi di maye, ndaw li Pool dafa ne : “ Kiy joxe ak mbég moo neex Boroom bi. ” (2 Kor. 9:⁠7). Noonu it la Yàlla di xoole li ñu koy defal. Nii lañu mënee gërëm Yàlla : sawar ci liggéeyu waare bi ak ci lépp lu jëm ci dëgg gi, bég ci suñu ndaje yi, te bu ñuy def li neex Yàlla ñu wone ne dañu ci kontaan. — Sab. 107:​21, 22 ; 119:14 ; 122:1 ; Room 12:​8, 11.

3 Ci jamano Israyil bu njëkk bi, dafa amoon ay sarax yoo xam ne Sàrt bi waxul woon fi ñu war a tollu. Képp kuy jaamu Yexowa, te bëgg koo gërëm, dafa waroon a saraxe lu tolloo ak li ko Yexowa barkeel (5 Mu. 16:​16, 17). Noonu itam tey, bu fekkee ne dañuy gërëm Yexowa ci suñu biir xol, dinañu def lépp li ñu mën ci liggéeyu waare Nguur gi ak sàkk taalibe. Ci weeru noppaliku yi, dinañu gën a mën a gërëm Yexowa. Am na ñoo xam ne dañuy jël waxtu yi ñu dul liggéey walla waxtu yi ñu dul jàngi ngir yokk li ñuy def ci liggéeyu waare bi, walla sax ngir nekk pioñee buy jàpple. Ren, ndax dinga mën a yokk li ngay def ci liggéeyu waare bi ci jamano noppaliku bi ?

4 Na suñu xol fees ak ngërëm : Mën nañu gërëm Yexowa ci ñaan. Lu am solo dëgg la (1 Tes. 5:​17, 18). Kàddu Yàlla nee na suñu xol dafa war a fees ak ngërëm ak it ngëm (Kol. 2:⁠7). Bu fekkee ne sax li ñu war a def dafa bare, te dañu jàpp lool, bés bu ne, war nañu gërëm Yexowa ci suñuy ñaan (Fil. 4:⁠6). Waaw, nañu gërëm Yàlla bu baax ci suñuy ñaan ak ci waaraate bi. — 2 Kor. 9:​12.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager