“ Ubbileen seen xol ”
1 Karceen yi dañu mel ni ay mbokk ci seen biir. Kon kenn ku nekk war na def wàllam ngir ñépp kontaan ci mbooloo mi (1 Pie. 1:22 ; 2:17). Loolu dina mën a am bu fekkee ne kenn ku nekk ci ñun dafay ‘ ubbi xolam ’ ci moroomam, maanaam day fexe ba gën koo bëgg (2 Kor. 6:12, 13). Lu tax xam bu baax suñu mbokk yi am solo ?
2 Suñu diggante dafay gën a rattax : Bu ñu góor-góorloo ngir gën a xam suñuy mbokk ci ngëm, dinañu gis seeni jikko yu rafet yu mel ni ngëm ak muñ. Ci lañu leen di gën a fonk. Te bu ñu gisee sikk ci ñoom, duñu ko jàppe ni lu am solo. Suñu diggante dina gën a rattax te dinañu leen gën a mën a dimbali ngir ñu jëm kanam. Te ku nekk dina gën a mën a dëgëral moroomam (1 Tes. 5:11). Dinañu mën a dimbaleente ngir ñu gën a am doole bi ñuy xeexe lu bon li ñu àddina Seytaane bëgg defloo (Kol. 4:11). Ci muju jamono jii, bare nañu jafe-jafe lool. Moo tax ñu ngi sant Yexowa bu baax ci xarit yu baax yi ñu am ci mbooloom. — Léeb. 18:24.
3 Xaritu benn bakkan mën na yokk doole te dalal xel bu ñu nekkee ci lu mettee-metti (Léeb. 17:17). Dafa am suñu benn mbokk moo xam ne saa su ne dafa doon xalaat ne moom tekkiwul dara. Nee na : “ Dama amoon ay xarit yoo xam ne dañu may wax lu baax li ñu gis ci man, ndax ma bañ a nekk ku xolam jeex ba di gis lu bon ci lépp. ” Xarit yu mel noonu barke Yexowa lañu. — Léeb. 27:9.
4 Nañu ittewoo suñu moroom yi : Naka lañu mënee ubbi suñu xol ci suñu moroom karceen yi ? Ci suñu ndaje karceen yi, bu ñu leen nuyoo ba pare, nañu gën a waxtaan ak ñoom, waxtaan bu mën a am njariñ. Won leen ne danga leen di xalaat. Waaye ci waxtaan bi, moytul a dugg foo warul a dugg (Fil. 2:4 ; 1 Pet. 4:15). Leneen loo mën a def it mooy wax leen ñu ñëw añ walla reer ci sa kër (Lukk 14:12-14). Mën nga jàpp itam bés ak ñoom ngir ngeen ànd waaraateji (Lukk 10:1). Bu ñu góor-góorloo ngir gën a xam suñuy mbokk karceen yi, mbooloo mi dina gën a nekk benn. — Kol. 3:14.
5 Am na ñoo xam ne seeni moroom walla ñi nangu li ñu bëgg rekk ñooy nekk seeni xarit. Ndax noonu ngay def yow itam ? Loolu warul am ci suñu biir. Dawuda ak Yonatan, walla it Rut ak Nawomi maasewuñu woon te it bokkuñu woon cosaan waaye terewu leen a nekk xaritu benn bakkan (1 Sam. 18:1 ; Rut 4:15). Ndax mën nga góor-góorlu ngir gën a am ay xarit ? Boo defee loolu, dinga am ay barke yoo masul a xalaat sax.
6 Bu ñu fexee ba gën a bëgg suñu mbokk yi, kenn ku nekk dinga yokk sa doole moroom. Te jàmm dina gën a am ci mbooloo mi. Te bu Yexowa gisee loolu, dina ñu barkeel bu baax (Sab. 41:1, 2 ; Yaw. 6:10). Ndax mënoo jéem a gën a xam say mbokk ci ngëm ?
[Laaj yi]
1. Lan la kenn ku nekk ci ñun war a def ?
2. Lu tax xaritoo ak suñuy mbokk ci ngëm am solo lool ?
3. Naka lañu mënee dimbali te yokk doole suñu mbokk yi ?
4. Lu ñu mën a def ngir gën a xam suñu mbokk yi ci mbooloo mi ?
5. Lan lañu mën a def ngir gën a am ay xarit ?
6. Bu ñu fexee ba gën a bëgg suñu mbokk yi, ban njariñ lañu ciy gis ?