Li ñu war a tàmm ci wàllu ngëm ngir mu indil ñu barke yu bare
1 Bi nga sogee nekk karceen, danga góor-góorlu ngir tàmm lu baax ci fànn yii di topp : jàng Biibël bi, teewe ndaje karceen yi, bokk ci liggéeyu waare bi ak it ñaan Yàlla. Loolu lu mu indi ? Yexowa barkeel na la ci li nga doon def noonu ba sa ngëm gën a dëgër. Xéyna bi ñu la sóobee ci ndox ba léegi mat na ay at. Waaye ndax yaa ngi kontine ci lu baax li nga tàmmoon bi nga doon góor-góorlu ngir nekk karceen ?
2 Nanga seetaat li nga tàmm di def ci wàllu ngëm : Ndax tàmm nga jàng Kàddu Yàlla bés bu nekk ? Loolu dafay indi barke yu bare (Yos. 1:8 ; Sab. 1:2, 3). Ci jamano Israyil bu njëkk bi, buur bu nekk dafa waroon a sotti Sàrt bi, ba pare jàng ci “ bés bu nekk ”. Ban njariñ la ci naroon a am ? Xol bu woyof ak jàng ragal Yexowa, bu ko defee du won ginnaaw li Yexowa santaane (5 Mu. 17:18-20). Noonu it tey, bu ñu jàngee Kàddu Yàlla bés bu nekk, ci diggu àddina bu bon te yàqu bii ñu nekk, dinañu am xol bu laab bu àndul ak ŋàññ, maanaam kenn du ñu mën a sikk ci dara. Dinañu am it lépp li ñu soxla ngir mën a waare bu baax. — Fil. 2:15 ; 2 Tim. 3:17.
3 Yeesu dafa tàmmoon a dem ca jàngu ba, fu ñu doon waxtaane Mbind yi (Luug 4:16). Xam nañu ne loolu yokk na bu baax dooleem ngir mu mën a jaar ci nattu yi nekkoon ci kanamam. Ñun itam, li ñuy jàng ci suñuy ndaje ak “ dimbaleente ” ci wàllu ngëm bi fa am, dafa ñuy yokk doole ci wàllu ngëm (Room 1:12). Daje noonu ak suñu mbokk yi, dafa ñuy dimbali ñu muñ coono yi ñu am ci muju jamano ji ñu nekk nii (Yaw. 10:24, 25). Ndax yaa ngi kontine di teewe ndaje yi yépp ?
4 Kàddu Yàlla wone na ne ndawi Kirist yi dañu doon xamle xibaar bu baax bi “ bés bu nekk ca kër Yàlla ga ak ca kër ya ”. (Jëf. 5:42.) Xéyna mënuñu waare bés bu nekk. Waaye ndax mën nañu tàmm bokk ci liggéeyu waare bi ayu-bés bu nekk ? Bu ñu defee loolu, dinañu gën a aay ci jëfandikoo Kàddu Yàlla te am lu neex lu ñuy fekke bu ñuy xamal nit ñi dëgg gi nekk ci Biibël bi.
5 Yexowa dafa barkeel yonent Yàlla Dañel ndax li mu kontine di ko jaamu giiru dundam yépp. Jaamu boobu ëmboon na tàmm di ñaan Yexowa (Dañ. 6:10, 16, 20). Ñun itam bu ñu tàmmee di ñaan Yexowa, ñaan yu jóge ci suñu xol, Yexowa dina ñu barkeel ak xelam mu sell mi (Luug 11:9-13). Am na leneen lu dàq loolu : Yexowa dina ñu jege te suñu diggante ak moom dina rattax (Sab. 25:14 ; Saag 4:8). Loolu barke bu réy la ! Kon nañu góor-góorlu ngir kontine di am lu ñu tàmm def ci wàllu ngëm. Yexowa dina ñu barkeel bu baax.
[Laaj yi]
1. Lu tax seetaat li nga tàmm a def ci wàllu ngëm am njariñ ?
2. Ban njariñ moo nekk ci jàng Biibël bi bés bu nekk ?
3. Bu ñu tàmmee teew ci ndaje yi, yan barke lañu ciy jële ?
4. Ban njariñ moo nekk ci waaraate ayu-bés bu nekk ?
5. Lu tax tàmm di ñaan Yexowa nekk lu am a am solo ?