TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 9/06 p. 10
  • Waaraate këroo-kër

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Waaraate këroo-kër
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2006
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Barke yi ñuy am bu ñuy wone suñu ngërëm ci mbëggeelu Yexowa — Xaaj 1
    Sasu Nguuru Yàlla — 2001
Sasu Nguuru Yàlla — 2006
km 9/06 p. 10

Waaraate këroo-kër

1 La Tour de Garde bu 1 sulyet 1893 (ci ãgale), newoon na ne ñiy yégle dëgg gi, dinañu nangu ne waaraate këroo-kër ak téere L’AURORE DU MILLÉNIUM moo doon, ca jamano jooju, fasoŋu waare bi gën a baax ngir xamle dëgg gi. Li mu wax noonu wone na njariñu waaraate këroo-kër. Ci loolu la nit ñi di ràññe Seede Yexowa yi ci àddina si sépp. Waaye, komka am na ay dëkk yoo xam ne, fekk nit ñi seen kër dafay gën di jafe, ndax fasoŋu waare boobu baax na ba tey ?

2 Biibël bi moo ko wax te dafa am solo : Waaraate këroo-kër, ci Biibël bi lañu ko jële. Yeesu sant na taalibeem yi ñu ànd ñaar ak ñaar ci kër nit ñi (Luug 10:5-7). Lii la Biibël bi wax ci taalibeem yi, fekk yàggul woon bi Yeesu deewee : “ Bés bu nekk ca kër Yàlla ga ak ca kër ya, daawuñu noppee jàngale ak a xamle xebaar bu baax bi. ” (Jëf. 5:42). Ndaw li Pool it dem na jàngale këroo-kër, sawar ci lool. — Jëf. 20:20.

3 Liggéeyu waare këroo-kër, mu ngi kontine di nekk fasoŋu waare bu am solo, ngir xamle xibaar bu baax bi. Dafay tax ñu mën a “ seet ” boroom xol yu rafet yi ci fasoŋ boo xam ne duñu ci fàtte kenn te jaxasoo du ci am (Macë 10:11). Ci lu ëpp, bu nit ki nekkee këram, xelam dafay gën a dal. Bu ñuy jàkkaarloo ak moom, di waxtaan ak moom, dañuy dégg baatam, di gis liy feeñ ci kanamam te di gis li mu nekke. Loolu dina tax ñu mën a ràññe li ko itteel ak lu ko jaaxal. Ci lu ëpp dafa ñuy may ñu mën a am waxtaan yu xóot ak nit ñi.

4 Seetal li nga mën a soppi ci li nga tàmm di def : Ndaw li Pool nangu woon na soppi li mu tàmmoon a def, “ ndax xebaar bu baax bi ”. (1 Kor. 9:23.) Xéyna mën nañu defaraat suñu porogaraam ngir waare ci waxtu yoo xam ne ci la nit ñi gën a faral a nekk seen kër. Mën na nekk ci ngoon a ngoon walla samdi ak dimaas yi walla it ci bés yoo xam ne nguuru réew mi dafa ko may nit ñi ñu bañ ci liggéey. Bindal kër yoo xam ne fekkoo fa kenn te nanga jéem dellu beneen bés ci ayu-bés bi walla ci beneen waxtu.

5 Ñi nga xam ne sax seen wér-gi-yaram dafa leen di tere def yenn yi, mën nañu bokk ci liggéeyu waare këroo-kër. Xéyna ñun ñii bokk ci mbooloo mi mën nañu seet li ñu mën a def ngir ànd ak ñu mel noonu ci kër yi neex a jot, bu ko defee dox bi du leen sonal. Suñu benn mbokk mu jigéen mënul woon noyyi bu baax. Moo tax génn wallu waxtu bu nekk, ci benn kër kese la mënoon a waare. Waaye bi ñu ko boolee ci gurup bi, ba mu dem waare ak ñoom, dafa kontaan lool !

6 Ñu bare ñi Biibël bi méngale ak xar, maanaam ay nit ñu baax, ñu ngi kontine di leen gis ci waaraate bi ñuy def këroo-kër. Benn waaraatekat dafa fëgg ci benn bunt te dégg ku ko nee : “ Agsil. Xam naa ki nga doon. Dama doon ñaan Yàlla ngir mu yónnee ma ku may dimbali, ma daldi dégg nga fëgg ci bunt bi. Yàlla moo la yónni ci man. ” Li fasoŋu liggéeyu waare boobu di jur, wone na ne Yexowa mu ngi koy barkeel (Macë 11:19). Nangeen góor-góorlu ngir tàmm di waare këroo-kër.

[Laaj yi]

1. Ban laaj lañuy laajte ci lu jëm ci waaraate këroo-kër, te lu tax ñuy laaj loolu ?

2. Lan moo ñuy won ne waaraate këroo-kër, ci Biibël bi lañu ko jële ?

3. Ban njariñ moo nekk ci waaraate këroo-kër ?

4. Naka lañu mënee def ba suñu waaraate këroo-kër gën a jur lu baax ?

5. Ñi nga xam ne seen wér-gi-yaram dafa leen di tere yenn yi, naka lañu leen mënee boole ci liggéeyu waare këroo-kër ?

6. Lu tax ñu war a góor-góorlu ngir tàmm waaraate këroo-kër ?

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager