Dénk nañu leen lu réy
1 Ndaw li Pool fonkoon na lool liggéeyu waaraate bi ko Yàlla joxoon te dafa ko doon méngale ak alal bu réy (2 Kor. 4:7). Muñ na ay metit ak fitna bi mu doon def liggéey boobu. Wéy na bañ a tàyyi ci waar nit ñu mu mënoon ñépp. Tukki na lu bare ci kow suuf ak géej. Tukki yu metti fu mu mënoon a ñàkk bakkanam. Naka lañu mënee roy Pool te wone ne dañu fonk suñu liggéeyu waare bi (Room 11:13) ? Lan moo tax ñu méngale suñu liggéeyu waare ak alal bu réy ?
2 Alal bu ëpp alal bu mu mënta doon : Alalu àddina yu ci bare dañuy ànd ak ay metitu xol te seen njariñ du yàgg. Waaye njariñ bi nekk ci liggéeyu waare bi dafay yàgg ci ñun ak nit ñi (1 Tim. 4:16). Dafay dimbali boroom xol yu rafet yi ñu xam Yexowa, soppi li ñu war a soppi ci seen dund, te am yaakaar bu dëggu ci dund bu dul jeex (Room 10:13-15). Bu ñu fonkee suñu liggéeyu waare bi, dinañu am jubluwaay bu baax ci suñu dund, dinañu kontine di yég ne ñu ngi def lu baax te dinañu am itam yaakaar bu mag ngir ëllëg. — 1 Kor. 15:58.
3 Nañu wone ne fonk nañu alal bu réy bi ñu am : Liy wone ni ñu fonke dara mooy lu ñuy nangu joxe ngir moom. Jël suñu jot ak suñu doole ngir magal Yexowa, cér bu réy la (Efes 5:16, 17) ! Fasoŋ bi ñuy jëfandikoo suñu jot, war na wone ne ci ñun, suñu diggante ak Yàlla moo ëpp solo alalu àddina. Ndegam lu am solo lañu war a xamal nit ñi, dinañu bëgg waare ak cawarte. Te it dinañu nangu farlu ngir waxtaane lu jëm ci xibaar bu baax bi saa yu ñu ci amee bunt.
4 Alal bu réy duñu ko nëbb, waaye dañu koy wone ngir ñeneen ñi mën koo gis. Bu fekkee ne suñu liggéeyu waaraate bi dañu ko jàppe niki alal bu réy, dina bokk ci suñu dund (Macë 5:14-16). Xol bu fees ak mbégte nañu wéy di roy ndaw li Pool te saa yu ñu ci amee yoon, ñu fexe ba wone ne ca dëgg-dëgg, dañu fonk liggéeyu waaraate bi niki alal bu réy.