Fonk nañu lool lu réy li ñu Yàlla may !
1 Yexowa dafa mas a dénk ñi ko doon jaamu ay fasoŋu liggéey yu bare, te loolu ba mu sàkkee nit la ko komaasee def ba tey. Dafa leen doon jox liggéey te du ci doon seet ndax góor lañu walla jigéen, du ci seet it seen at walla li ñu doon ci àddina (Luug 1:41, 42 ; Jëf. 7:46 ; Fil. 1:29). Yan liggéey la ñu dénk tey ?
2 Yenn ci lu réy li ñu Yexowa may : Ci ñi Yexowa di jàngal lañu bokk. Loolu cér bu réy la (Macë 13:11, 15). Bu ñuy tontu ci ndaje yi ñu am ci mbooloo mi, dañuy màggal Yexowa. Loolu it beneen cér la (Sab. 35:18). Bu ñu nu mayee ñu mën a tontu, dañu ciy sawar lool. Te it, bu ñu jàppee bépp liggéey bu ñu nu dénk ci mbooloo mi ni cér bu réy, dinañu ci def suñu kem-kàttan ngir mu baax. Bokk ci set-setalu saalu Nguur gi ak toppatoo ko ngir mu bañ a yàqu, loolu it cér bu réy la. Ndax tàmm nañu di ci bokk ?
3 Ay milyoŋi nit tey xamuñu ndax Yàlla mu ngi dégg seeni ñaan. Waaye ñun xam nañu ne Ki gën a mag ci asamaan ak suuf yépp, mu ngiy déglu suñuy ñaan. Loolu cér bu réy la (Léeb 15:29). Yexowa ci boppam mooy déglu ñaanu jaamam yi (1 Piy. 3:12). Te yemalewul ñaata yoon lañu ko mën a ñaan. Kon mën nañu ko ñaan te “ sax ci ”. Aka nekk cér bu réy bu ñu fonk ! — Efes 6:18.
4 Ñun ak Yàlla ñooy “ liggéeyandoo ” : Waare xibaar bu baax bi jëm ci Nguuru Yàlla, bokk na ci cér yi gën a réy yi ñu am. Bu ñuy def loolu, ñun ak Yàlla ñooy “ liggéeyandoo ” (1 Kor. 3:9). Liggéey boobu dafa ñuy may mbégte te dafay seddal suñu xol (Ywna. 4:34). Yexowa soxlawul jaar ci doom-Aadama yi ngir def liggéey boobu. Waaye dafa ñu bëgg moo tax mu dénk ñu ko (Luug 19:39, 40). Du ñépp la Yexowa dénk liggéey boobu. Bala ñu ciy mën a bokk, am na yenn yu ñu war a mën a def ci wàllu ngëm te kontine di ko def (Isa 52:11). Ndax ayu-bés bu nekk dañuy jébbal liggéey boobu wàll bu réy ci suñu jot, ngir wone ne dañu ko fonk ?
5 Cér yu réy yi ñu Yexowa di may, dañuy tax suñu dund gën a neex (Léeb 10:22). Buñu ko xeeb mukk ! Bu ñuy wone ne dañu fonk bu baax cér yu réy yi ñu Yexowa may, loolu dafay neex suñu Baay bi nekk asamaan, Moom mii nekk kuy maye “ gépp may gu baax ak gépp jagle gu mat ”. — Saag 1:17.