TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 10/07 p. 8
  • Na ku nekk yokk doole moroomam

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Na ku nekk yokk doole moroomam
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Naka la wottukat yiy wër di ñu dimbalee ?
    Ñan ñooy def tey li Yexowa santaane ?
Sasu Nguuru Yàlla — 2007
km 10/07 p. 8

Na ku nekk yokk doole moroomam

1. Lan lañu mën a def saa yu wottukat yiy wér ñëwee ci suñu mbooloo ?

1 Ndaw li Pool bindoon na lii mbooloo mi nekkoon Room : “ Bëgg naa leen a gis lool, ba indil leen barke bu jóge ci Xel mu Sell mi, ndax seen ngëm gën a dëgër. Maanaam ma nekk ci seen biir, te ñu dimbaleente ci suñu ngëm, ndax man itam ma gën a am doole ” (Room 1:11-12). Tey itam kenn ku nekk dina am fu mu mënee yokk doole moroomam bu wottukat yiy wér ci mbooloo yi ñëwee ci suñu mbooloo.

2. Lu tax ñuy teel a yégle ñówu wottukat biy wër ci mbooloo yi ?

2 Mbooloo mi : Ci lu ëpp, dañuy yégal waa mbooloo mi kañ la wottukat biy wër ci mbooloo yi di ñów, lu mat ñetti wér bala bés bi di jot. Loolu dafa ñuy may jot bu doy ngir ñu defar suñu porogaraam ngir mën a jariñoo bu baax ci ñëwam (Efes 5:15, 16). Bu dee dangay liggéey, xéyna dinga mën a jël ay fan yu nga dul liggéey ngir mën a bokk ci liggéeyu waare bi ci ayu bés boobu. Am na ñuy fexe ba nekk pioñee yuy jàpple ci wéer bi wottukat bi waree ñów. Bu dee danga war a tukki ayu-bés boobu, ndax mën nga seetaat sa porogaraam ngir fekke ayu-bés boobu ?

3. Bu wottukat bi nekkee ci suñu mbooloo, lan lañu mën a def ci suñu wàllu bopp ngir suñu doole yokku ci wàllu ngëm ?

3 Li njëkk tax wottukat biy wër ci mbooloo yi ñëw mooy, yokk suñu doole ñun ñépp ak it dimbali ñu ñu gën a aay ci waaraate bi. Ndax mënuloo ñaan ñu may la nga liggéey ak moom walla ak jabaram bu dee am na jabar ? Wottukat bi, bu mënee ànd ak waaraatekat yu bare dina kontaan lool. Ñi yàggul a nekk waaraatekat walla ñi aayul noonu ci waaraate bi, bokk nañu ci ñi mu bëgg àndal ci waaraate bi. Ñépp a mën a topp it xelal yi muy joxe (1 Kor. 4:16, 17). Boo ko waxee mu ñów añsi walla réersi, loolu it dina leen may ngeen mën a yokkante doole (Yaw. 13: 2). Komka waxtaan yi muy def ci ndaje yi, dafa nekk li mbooloo mi soxla dëgg ci wàllu ngëm, nañu ko déglu bu baax.

4. Naka lañu mënee yokk doole wottukat biy wër ci mbooloo yi ?

4 Wottukat biy wër ci mbooloo yi : Ndaw li Pool benn la woon ak mbokkam yi mu doon jàpple ci mbooloo mi. Dafa amoon ay coono ni ñoom, di jaaxle ni ñoom. Looloo tax mu doon soxla moom itam kuy yokk dooleem (2 Kor. 11: 26-28). Bi ñu ko doon yóbbu Room ngir tëj ko fa kaso, bi ko waa mbooloo mi nekkoon foofu yëgee, am na ñu dem ba ca marse bi nekkoon Apiyus ngir gis ko ci yoon bi bala mu àgg Room. Tukki bu doon def lu mat 75 Km la woon ! “ Bi leen Pool gisee, mu sant Yàlla, daldi takk fitam ” (Jëf. 28:15). Yow it mën nga yokk doole wottukat biy wër ci mbooloo yi. Won ko “ teraanga ju mat sëkk ”. Dinga mën a def loolu boo sawaree lool ci lépp li ñuy taxawal bu ñëwe ci mbooloo mi (1 Tim. 5:17). Wax ko ne fonk nga bu baax lépp li muy def ngir yow te won ko ko it. Moom ak jabaram dinañu kontaan lool bu ñu gisee sa ngëm, sa mbëggeel ak ni ngay muñe jafe-jafe yi. — 2 Tes. 1: 3, 4.

5. Tey, lu tax kenn ku nekk ci ñun soxla kuy yokk dooleem ?

5 Ci “ bési tiis yu tar ” yi ñu nekk nii, ndax am na ku soxlawul ñu yokk dooleem (2 Tim. 3:1) ? Nanga seet léegi loo mën a def ngir bokk bu baax ci lépp li ñuy def ci mbooloo mi bu wottukat biy wër ci mbooloo yi di ñów. Wottukat biy wër ci mbooloo yi ak waaraatekat yépp, mën nañu def seen wàll ngir ku ci nekk yokk doole moroomam ak mbégte. Bu ñu defee noonu dinañu ‘ dëgëralante te yokkante suñu ngëm ’. — 1 Tes. 5:11.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager