TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 4/08 p. 3
  • Nañu “ jaar ciy tànkam ”

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Nañu “ jaar ciy tànkam ”
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2008
Sasu Nguuru Yàlla — 2008
km 4/08 p. 3

Nañu “ jaar ciy tànkam ”

1. Lan moo ñuy tax a doon waaraatekat yu aay ?

1 Yeesu du ci Lekkoolu kilifa diine yawut yi la jànge. Waaye ci waaraatekat yi mas a am ci àddina, mooy bi gën a aay. Ñu ngi sant Yàlla bu baax ci li ñu bind li Yeesu def ci waaraate bi, denc ko ngir suñu njariñ. Bu ñu bëggee nekk ay waaraatekat yu aay, dañu war a “ jaar ciy tànkam ”. — 1 Piy. 2:21.

2. Lan moo ñuy dimbali ñu bëgg nit ñi ni leen Yeesu bëgge woon ?

2 Nañu won nit ñi ne bëgg nañu leen : Mbëggeel bi Yeesu am ci nit ñi moo ko doon puus ci li mu def (Mark 6:30-34). Ñu bare ci suñuy gox ñu ngi ci ‘ metit ’ te soxla nañu xam dëgg gi lool (Room 8:22). Bu ñu xalaatee lu metti li nit ñooñu nekke ak ni leen Yexowa bëgge, dinañu bëgg kontine di waaraate (2 Piy. 3:9). Li ci gën a am solo mooy, nit ñi, bu ñu gisee ne dañu leen fonk dëgg, dinañu gën a bëgg déglu suñu xibaar.

3. Kañ la Yeesu doon waare ?

3 Nañu wax ak nit ñi saa yu ñu ci ame bunt : Yeesu saa yu gisaan bunt fu mu mënoon jaar ngir xamal nit ñi xibaar bu baax bi, dafa ci doon jaar (Macë 4:23 ; 9:9 ; Ywna. 4:7-10). Ñun itam bëgg nañu pare, bu ko defee, bu ñuy dem ak di dikk bés bu nekk, ñu mën a wax nit ñi lu jëm ci dëgg gi. Am na ñuy yóbbaale Biibël ak ay yéenekaay, ngir mën a waaraate fi ñuy liggéeye, ca lekkool ba, bu ñuy tukki, bu ñuy jëndi dara, walla bu ñu nekkee ci yu mel noonu.

4. Naka lañu mënee fexe ba bu ñuy waaraate, suñu waxtaan jëm ci Nguuru Yàlla ?

4 Nañu gën a wax ci Nguuru Yàlla : Xibaar bu baax bi jëm ci Nguuru Yàlla la Yeesu doon waare (Luug 4:43). Dëgg la, mën na am ñu bañ a wax lu jëm ci Nguuru Yàlla bu ñuy komaase waxtaan bi. Yenn saay it ñu bañ ci wax bu ñuy waxtaan ak nit ki. Waaye dañuy def ci suñu xel ne, dañu leen war a dimbali ñu xam ne soxla nañu ko. Su fekkee ne sax dinañu wax ci coono yiy wone ne ñu ngi ci muju jamano, li ñu gën a bëgg mooy “ yégle xebaar bu baax bi. ” — Room 10:15.

5. Bu ñu bëggee suñu waaraate baax, naka lañu waree jëfandikoo Biibël bi ?

5 Nañu wéeru ci Kàddu Yàlla : Yeesu dafa doon jëfandikoo Mbind mi saa yu doon jàngal nit ñi. Yeesu jàngalewul dara lu jóge ci xalaatu boppam (Ywna. 7:16, 18). Dafa doon jàng Kàddu Yàlla te di seet ni mu ko mëne jëfe, bu ko Seytaane doon jéem a fiir (Macë 4:1-4). Bu ñu bëggee jàngal bu baax suñuy moroom, dañu war di jàng Biibël bi bés bu nekk te di seet it ni ñu ko mënee topp (Room 2:21). Bu ñuy tontu nit ñi ci waaraate bi, dañu war a wone ni Mbind mi di dëggale li ñuy wax. Te saa yu mënee nekk, dañu war a jàng aaya yi ci Biibël bi ci boppam. Li ñu bëgg mooy nit ñi gis ne du suñu xalaatu bopp lañuy wax, waaye li ñuy wax, ci kàddu Yàlla lañu ko jële.

6. Lan la Yeesu def ngir laal xolu ñi ko doon déglu ?

6 Nañu laal xolu nit ñi bu ñuy jàngale : “ Kenn musul a wax ni nit kooku ! ” (Ywna. 7:46). Loolu la alkaati yi waxoon ci Yeesu bi leen saraxekat ya ak Farisien ya laajee lu tax indiwuñu ko. Yeesu daawul woon jottali nit ñi rekk li mu leen waroon a jàngal, dafa doon wax ci fasoŋ bu doon laal seen xol (Luug 24:32). Dafa doon jëfandikoo ay misaal yu mu doon jële ci li nit ñi doon def bés bu nekk ngir ñu gën a nànd li mu leen doon wax (Macë 13:34). Yeesu daawul wax wax bu dul jeex (Ywna. 16:12). Dafa doon xiir nit ñi ci Yexowa te bañ leen xiir ci moom. Ni Yeesu, mën nañu nekk ay jàngalekat yu aay su ñu nekkee rekk ay nit ñuy ‘ sàmm seen njàngale, te sax ci ’. — 1 Tim. 4:16.

7. Lu tax Yeesu kontine di waaraate ?

7 Bu dee sax nit ñi bëgguñu déglu, te ñu di ñu xeex it, dinañu kontine : Dëgg la Yeesu defoon na ay kéemaan, waaye ñu bare dégluwuñu ko (Luug 10:13). Ay mbokki Yeesu sax dañu xalaatoon ne “ dafa tàggoo ak sagoom ” (Mark 3:21). Waaye loolu terewu ko kontine. Dafa kontine di xalaat lu rafet ci liggéeyam, ndaxte dafa ko wóoroon ne moo yore woon dëgg giy goreel nit ñi (Ywna. 8:32). Ci ndimbalu Yexowa, ñun it dañu fas yéene jàpp bu dëgër ci waaraate bi te bañ a dellu ginnaaw. — 2 Kor. 4:1.

8, 9. Naka lañu mënee roy Yeesu ci nangu xañ suñu bopp yenn yi ngir xibaar bu baax bi ?

8 Nañu nangu ñàkk yenn yi ngir mën a bokk bu baax ci waaraate bi : Ngir waaraate bi, Yeesu dafa nangu ñàkk alal bu mënoon a tax dundam gën a neex (Macë 8:20). Dafa doon waare rekk, bañ a tàyyi. Yenn saay sax dafa doon waare ba mu guddi (Mark 6:35, 36). Yeesu xamoon na ne waxtu bi mu am ngir def liggéeyam barewul. Komka “ diir bu gàtt rekk a fi des ”, ñun it dañu war a nangu def suñu jot, suñu doole, ak suñu alal ci liggéey bi ngir roy Yeesu. — 1 Kor. 7:29-31.

9 Karceen yu njëkk yi dañu aayoon lool ci waaraate bi ndaxte dañu doon jàng ci Yeesu (Jëf. 4:13). Ñun it, bu ñu royee ci waaraatekat bu gën a mag bi mas a am ci àddina, dinañu def suñu wàll ci waaraate bi ba mu mat. — 2 Tim. 4:5.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager