Jàngalal nit ñi ñu bëgg Yexowa
1. Lan moo tax ñenn ñi jege Yexowa ?
1 Ndax fàttaliku nga bés bi ñu la njëkke wax lu jëm ci Yexowa ? Lan moo taxoon nga bëgg ko jege ? Ñu bare ñu am xol bu rafet dinañu la wax ne, bi ñu demee ba xam jikko yu rafet yi Yàlla suñu Boroom am, rawatina yërmandeem ak mbëggeelam, ci lañu ko jege. — 1 Ywna. 4:8.
2, 3. Naka lañuy jëfandikoo téere Qu’enseigne la Bible ? ngir dimbali ñiy jàng Biibël bi ñu gën a bëgg Yexowa ?
2 “ Kii mooy suñu Yàlla ” : Téere Qu’enseigne la Bible ? dafay wone ni Yexowa bëggee nit ñi. Dafay wone it ne nit ku nekk dafa war a am diggante bu rattax ak Yàlla. Naka lañuy jëfandikoo téere boobu ngir jàngal nit ñi ni ñuy def ba gën a bëgg Yàlla ? Bu ñuy waxtaan ci li ñu masul a jàng, mën nañu laaj nit ki loo xam ne dina tax mu xalaat bu baax. Mën nga ko laaj lii : “ Li ñu wax fii, lu mu lay xamal ci Yexowa ? ” walla nga laaj ko lii “ li ñu wax fii naka lay wone ne Yexowa mooy Baay bi gën ? ” Jàngale ci fasoŋ boobu, mën na ko dimbali mu jege Yexowa dundam gépp.
3 Nañu won ki ñuy jàngal Biibël bi ne, xam benn Yàlla dëgg bi am, cér bu réy la. Bu xamee loolu dina wax ni Esayi waxoon : “ Kii mooy suñu Yàlla ” (Is. 25:9). Bu ñu koy leeral li nekk ci Kàddu Yàlla, war nañu ko won bu baax barke yu doomu Aadama yi di am bés bu Nguuru bi Yeesu Kirist jiite di ñëw ngir def coobare Yexowa. — Esa. 9:6, 7.
4, 5. Bëgg Yàlla lu muy tekki ?
4 Naka lañuy wone ne bëgg nañu Yexowa : Xam nañu ne bëgg Yàlla ak sa xol bépp, ak sa bakkan bépp ak sa xel mépp, yemul rekk ci fi nit teg Yàlla ci xolam. War nañu nangu ne xalaat ni Yàlla di xalaate moo gën, te dañu ko ci war a roy (Ps. 97:10). Bu ñu bëggee wone ne bëgg nañu Yàlla, dañu war a topp bu baax lépp li mu santaane, te di kontine di ‘ sellal suñu nekkin te feddali suñu ragal Yàlla ’, bu dee sax ñu ngi ci ay jafe-jafe walla ñu di ñu fitnaal. — 2 Piy. 3:11 ; 2 Ywna. 6.
5 Def li neex Yàlla ndax li ñu ko bëgg, lu neex la (Ps. 40:8). Kiy jàng Biibël bi dafa war a xam ne lépp li Yàlla sant nit ñi, dafa ko def ngir ñi koy jaamu am jàmm ba fàww (Deut. 10:12, 13). Bu nit ki di topp li Yexowa santaane, dafay wone ne fonk na bu baax lu rafet lépp li Yàlla def. Dimbalil kiy jàng mu xam ne kuy topp bu baax li Yexowa santaane dina musal boppam ci metitu xol yu bare.
6. Bu nit bëggee Yexowa yan barke lay am ?
6 Barke yi ñuy am bu ñu bëggee Yàlla : Yexowa dafa fonk lool ñi woyof te bëgg ko. Dafa leen di won ‘ xalaatam yi gën a xóot ’ (1 Kor. 2:9, 10). Bu ñu xamee coobare Yexowa, liy am ëllëg dafay leer ci suñu xel, te dañuy am yaakaar bu wóor (Yér. 29:11). Ñi bëgg Yexowa dañuy jot ci mbaaxaayam bu kenn mënul wax fu mu yem (Gàd. 20:6). Mbëggeel bu réy bi leen Yàlla won moo tax ñu am yaakaaru dund ba fàww te yaakaar boobu dañu ko fonk lool. — Ywna. 3:16.
7. Jàngal say moroom ñu bëgg Yexowa lan la lay def ?
7 Bu ñuy gën a xam lu jëm ci suñu Baay bi nekk ca asamaan, ñuy gën a am lu ñuy wax ci moom (Macë 13:52). Jàngal suñuy moroom, rawatina suñu doom ñu bëgg Yexowa, cér bu réy la (Deut. 6:5-7) ! Yàlla nañu ànd ak ñi ñuy jàngal Biibël bi di kontine di sant Yexowa bu ñuy gis ni ‘ mbaaxaayam baree ’. — Ps. 145:7.