TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • ijwyp pàcc 60
  • Ndax naan sàngara lu baax la?

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ndax naan sàngara lu baax la?
  • Li ndaw ñi di laaj
  • Turu xaaj yi
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Xalaatal ci li la naan sàngara mën a jural
  • Jëlal ay dogal
  • Naka la karceen yi war a gise sàngara?
    Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
Li ndaw ñi di laaj
ijwyp pàcc 60
Waxambaane bu ñu talal butéelu sàngara ci benn feet

LI NDAW ÑI DI LAAJ

Ndax naan sàngara lu baax la?

Biibël bi terewul naan tuuti sàngara bu ñu ko yoon mayee. Waaye tere na naan sàngara ba màndi (Sabóor 104:15; 1 Korent 6:​10).

Léegi bu la ñeneen ñi xiiree ci naan sàngara te yoon walla say waajur tere la ko, lan ngay def?

  • Xalaatal ci li la naan sàngara mën a jural

  • Jëlal ay dogal

  • Li yeneen ndaw wax

Xalaatal ci li la naan sàngara mën a jural

Am na ay ndaw yu foog ne bala ñoo mën a féexal seen xol, fàww ñu naan sàngara. Waaye bu ñu naanee ba pare, lan moo mën a xew?

  • Nit ku ñu tëj kaso

    Yoon mën na dal sa kaw. Su fekkee ne yoon dafay tere naan sàngara fi nga dëkk, boo naanee mën nañu la alamaan, yóbbu la ci kanamu yoon, nangu sa permis, liggéeyloo la walla sax tëj la kaso (Room 13:3).

  • Telefon

    Sa der mën na ci yàqu. Sàngara mën na tax ba doo too ànd ak sa sago. Mën na la defloo walla waxloo loo xam ne dinga ko réccu ëllëg (Kàddu yu Xelu 23:31-​33). Ak réseaux sociaux yi tey, lépp loy def mën na tilimal sa der te dina jafe lool nga setal ko.

  • Jigéen ju ñuy gétën

    Mën na tax nga bàyyeeku. Sàngara mën na tax ñu agerese la walla ñu sàkku la ci lu yomb. Sàngara mën na tax itam ñeneen ñi yóbbaale la ba nga dugg ci lu wóorul mbaa nga def lu yoon tere.

  • Xottu butéelu sàngara

    Mën na nekk tàmmeel bu bon. Ay gëstukat wone nañu ne, looy gën di teel a komaase naan sàngara, muy gën di jafe nga bàyyi ko. Di naan sàngara ndax stress walla wéet mën na la jural tàmmeel boo xam ne bàyyi ko mën na jafe lool.

  • Kaaŋ ak  Yax yu ñu galan

    Mën na la rey. Ci at yii weesu, ci Etaa Sini, daanaka waxtu wu nekk nit dafay dee ndax naan sàngara ba pare di dawal. Ci juróomi at yii weesu, lu ëpp junniy ndaw ak juróomi téeméer yu amagul ñaar fukki at ak benn dee nañu ci aksidaa ndax sàngara. Bu dee sax naanoo sàngara, dugg ci oto boo xam ne kiy dawal dafa naan sàngara, wóorul.

Jëlal ay dogal

Boo xalaatee bu baax bala ngay naan sàngara dinga mën a moytu li naan sàngara ba mu ëpp di jur.

Li Biibël bi wax: «Kuy foog, gisu ay, làqu» (Kàddu yu Xelu 22:3). Naan sàngara bala ngay dawal walla ngay def bépp liggéey buy laaj nga ànd ak sa sago, wóorul.

Nanga dogu ci lii: ‘Boo naree naan sàngara, na fekk yoon may la ko te amul leneen lu la ko tere.’

Li Biibël bi wax: «Koo [...] déggal [...], jaamam nga» (Room 6:​16). Booy naan sàngara ndaxte sa moroom yi dañuy naan, dafa mel ni dangay bàyyi ñeneen ñi wax la li nga war a def. Booy naan ndax danga wéet walla danga am stress doo mën a am jikko yi nga soxla ngir jànkoonte ak say jafe-jafe.

Nanga dogu ci lii: ‘Du ma bàyyi sama xarit yi dugal ma ci naan sàngara.’

Li Biibël bi wax: «Bul bokk ci ñiy [...] màndi» (Kàddu yu Xelu 23:20). Àndandoo yu bon mën nañu tax nga bàyyi dogal yu baax yi nga jël. Booy ànd ak ñiy naan sàngara ba mu ëpp, loolu mën na la lor.

Nanga dogu ci lii: ‘Du ma xaritoo ak ñiy naan sàngara ba mu ëpp.’

Li yeneen ndaw wax

Jordan

«Bi ma nekkoon lekkool, saa su ne dañu ma doon jéema dugal ci naan sàngara. Saa su ne, dama doon xalaat ci 1 Korent 15:33, bi wax ne: ‘Ànd bu bon dina yàq nit ku baax’» (Jordan).

Jenna

«Damay jéem a moytu bépp nit bu ma mën a puus ci naan sàngara ak lépp lu may puus ci def ko. Maa ngi sànt Yàlla ndaxte am naa ay xarit yu tànn li gën lu jëm ci sàngara» (Jenna).

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager