Note
a Am na ay Biibël yuy jëfandikoo baat “àddina” asté “jamano.” Téere bi tudd Expository Dictionary of New Testament Words bu W. E. Vine a ngiy wax ne baat Grekk ai·onʹ “a ngiy tekki diir bu ñu àppalul, walla jamano ju ñu lëkkaleek liy xew ci diir bi.” Téere bi tudd Greek and English Lexicon to the New Testament (xët 17) bu Parkhurst a ngiy ëmb waxeel “jamano jii” buy waxtaane jëfandikoob ai·oʹnes (bareel) ci Yawut yi 1:2. Kon di firee baat ai·oʹnes: “jamano ji” dëppoo naak la mbindum Grekk ma jiitu tekki saxsax.