Note
d Li ñu alag Babilon, benn misaal doŋŋ la ci li ñuy won ne li Biibël bi yégle dafay mujj a am. Am na yeneen misaal mel ni sànkute Tir, ak Niniw (Ézékiel 26:1-5 ; Tsephania 2:13-15). Dañeel itam waxoon na lu jëm ci ni réew yiy jiite àddina si di toppante ci ginnaaw Babilon. Réewu Médi-Pers ak bu Geres bokkoon nañu ci (Daniel 8:5-7, 20-22). Seetal xaaj bi tudd “ Li ñu yokk ci waxtaan yi nekk ci téere bii ”, ci xët 199 ba 201. Dinga ci gis lu bare li Biibël bi yégle woon ci lu jëm ci Almasi bi te mu am ci Yeesu Kirist.