Note
b Dañuy woowe Yexowa Baay ndaxte moom mooy Sàkk-kat bi (Isaïe 64:8). Komka Yàlla moo sàkk Yeesu, dañu koy woowe doomu Yàlla. Ndegam moom moo sàkk itam ñeneen ñi nekk ak moom ca asamaan, ñoom it dañu leen di woowe ay doomu Yàlla. Looloo tax it ñuy woowe Aadama doomu Yàlla. — Job 1:6 ; Luug 3:38.