Note
a Bëgguñu wax ne nit ñi bëggul nga jàng Biibël bi, Seytaane moo leen jàpp. Waaye Seytaane mooy yàlla àddina sii, te àddina sépp a ngi tëdd ci loxoom (2 Korent 4:4 ; 1 Yowaana 5:19). Kon bu amee ñu kontaanul ak ñu lay xeex ndax li nga bëgg a dund ci fasoŋ bu neex Yàlla, waru la bett.