Note
a Am na 454 at diggante atum 455 B.S.J.T. ak atum 1 C.S.J. Diggante atum 1 B.S.J.T. ak atum 1 C.S.J., am na benn at (amul woon atum sero). Te diggante atum 1 C.S.J. ba atum 29 C.S.J., am na 28 at. Su ñu boolee ñetti xaaj yooyu, dafay def 483 at. Ci atum 33 C.S.J., ci 70eelu semenu at mi lañu “ fi jële ” Yeesu, rey ko (Dañeel 9:24, 26, NW). Seetal li nekk ci téere bi tudd Prêtons attention à la prophétie de Daniel !, pàcc 11, ak li nekk ci téere Étude perspicace des Écritures, volume 2, xët 995 ba 997. Seede Yexowa yi ñoo defar ñaari téere yooyu.