LESOŊ 39
Ni Yàlla gise deret
Deret dafa am solo lool. Bu ñu ko amul, duñu mën a dund. Ndegam Yexowa moo ñu sàkk, moom moo ñu war a wax ni ñu mën a jëfandikoo deret. Lan la wax ci deret? Ndax mën nañu ko lekk walla sol ko ci suñu yaram? Naka nga mënee jël dogal bu baax ci fànn boobu?
1. Naka la Yàlla gise deret?
Ci jamano yi ñuy bind Biibël bi, Yexowa lii la waxoon ay jaamam: «Dundu mboolem mbindeef mooy deretam» (Sarxalkat yi 17:14). Ci Yexowa, deret mooy dund. Ndegam dund may bu sell la, bu jóge ci Yàlla, kon deret it lu sell la.
2. Lan la Yàlla tere ñu def ak deret?
Yexowa dafa digaloon jaamam yu njëkk ya, ñu bañ a lekk deret (Jàngal Njàlbéen ga 9:4 ak Sarxalkat yi 17:10). Baamtuwaat na ndigal boobu, bi jataay biy dogal santee karceen yi ñu ‘moytu deret’ (Jàngal Jëf ya 15:28, 29, MN).
Moytu deret, lu mu tekki? Bu la doktoor waxee nga moytu sàngara, dootoo ko naan. Waaye ndax dinga lekk ñam bu am sàngara walla nga sol ko ci sa yaram? Déedéet! Noonu it, bu ñu Yàlla waxee ñu moytu deret, loolu dafay tekki ne waruñu naan deret walla lekk yàpp bu médd, maanaam mala bu ñu rendiwul. Waruñu lekk itam benn ñam bu am deret.
Léegi lu jëm ci faj yi ñuy jëfandikoo deret nag? Leer na ne, yenn ci faj yooyu ànduñu ak li Yàlla santaane. Ci faj yooyu dañuy sol nit ki deret walla ay xaaju deret yu mag, ñu leen di woowe ci farãse globules rouges, globules blancs, plaquettes ak plasma. Am na yeneen faj yoo xam ne, mënuñu wax ci lu leer ne ànduñu ak li Yàlla santaane. Ci misaal, am na faj yoo xam ne dañuy jëfandikoo ay xaaju deret yu ndaw-a-ndaw. Ci yeneen yi, deretu nit ki ci boppam lañuy jëfandikoo. Ci lu jëm ci faj yooyu, ku nekk moo war a jëlal boppam dogala (Galasi 6:5).
XÓOTALAL NJÀNG MI
Xoolal ni nga mënee tànn fasoŋu faju bi gën.
3. Jëlal dogal yu neex Yexowa ci wàllu faju
Ci wàllu faju, naka nga mënee jël dogal yu ànd ak ni Yàlla gise deret? Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, xoolal li tax mu am solo ñu topp tegtal yii di topp.
Ñaanal Yàlla ngir xam li nga war a def (Saag 1:5).
Gëstul njàngale yi nekk ci Biibël bi ak ni nga leen mën a toppe (Kàddu yu Xelu 13:16).
Xoolal fasoŋu faju yi am fi nga dëkk.
Ràññeel bu baax fasoŋu faju yi nga mën a nangu.
Na la wóor ne dogal bi ngay jël dina tax nga am xel mu dal (Jëf ya 24:16).b
Xamal ne kenn warulaa wax li nga war a dogal ba am xel mu dal, du sa jëkkër, du sa jabar, du magu mbooloo te du ki lay jàngal Biibël bi (Room 14:12).
Bindal li nga tànn ngir ñeneen ñi xam ko.
4. Seede Yexowa yi dañuy wut faj yi gën
Mën nañu topp li Yàlla wax ci deret ba pare am faj yi gën. Seetaanal WIDEO BI.
Jàngal Tit 3:2. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:
Lu tax ñu war di ànd ak respe te lewet, saa yu ñuy wax ak doktoor yi?
Li ñu warul a nangu |
Karceen bi mooy tànn |
---|---|
A. Plasma |
Ay xaaju plasma |
B. Globules blancs |
Ay xaaju globules blancs |
C. Plaquettes |
Ay xaaju plaquettes |
D. Globules rouges |
Ay xaaju globules rouges |
5. Faj yi ñuy jëfandikoo deret
Deret ñeenti xaaj yu mag la, ñu leen di woowe ci farãse globules rouges, globules blancs, plaquettes ak plasma. Ñeenti xaaju deret yu mag yooyu itam am nañu ay xaaj yu ndaw-a-ndaw, ñu leen di woowe fractions de sang ci farãse.c Dañuy jëfandikoo yenn ci xaaj yooyu ngir xeex ay feebar walla arete deret juy tuuru.
Lu jëm ci xaaju deret yu ndaw-a-ndaw yi, karceen bu nekk moo war a jëlal boppam dogal bu sukkandiku ci Biibël bi, bu koy may xel mu dal. Xéyna dina am ñiy bañ fasoŋu faju yi ñuy jëfandikoo xaaju deret yu ndaw-a-ndaw yi. Ñeneen mën nañu gis ne seen xel may na leen, ñu nangu xaaju deret yu ndaw-a-ndaw yooyu.
Boo naree jël dogal, bàyyil xel ci laaj bii:
Naka laay waxe sama doktoor li tax duma jël yenn xaaju deret yu ndaw-a-ndaw yi walla li tax ma di leen jël?
BU LA NIT LAAJOON: «Lan moo aay ci nangu ñu sol la deret?»
Lan nga ci xalaat?
NAÑU TËNK
Biibël bi wax na ñu ni Yexowa bëgge ñu jëfandikoo deret.
Nañu fàttaliku
Lu tax Yexowa gise deret ni lu sell?
Yexowa moo santaane ñu moytu deret, naka lañu xame ne sol nit deret bokk na ci?
Naka nga mënee jël dogal bu baax ci lu jëm ci fasoŋu faju yiy jëfandikoo deret?
GËSTUL
Ci lan nga war a xalaat bala ngay jël dogal ci lu jëm ci jëfandikoo sa deret ngir faju?
Ci lan nga war a xalaat booy tànn ndax dinga nangu xaaju deret yu ndaw-a-ndaw yi walla déet?
Xoolal ni magi mbooloo yi bokk ci Kuréli ñiy jokkoo ak doktoor yi di dimbalee seeni mbokk ci ngëm.
b Xoolal ponk 5, «Lu jëm ci xaaju deret yi» ak Yeneen leeral 3, «Faj yi ñuy jëfandikoo deret».
c Yenn doktoor yi dañu gise ñeenti xaaju deret yu mag yi, ni ay xaaj yu ndaw-a-ndaw. Loolu moo tax war nga xamal bu baax sa doktoor ne, doo jël deret walla xaajam yu mag yi, maanaam globules rouges, globules blancs, plaquettes ak plasma.