LESOŊ 10
Ban njariñ nga mën a jële ci teewe ndaje Seede Yexowa yi?
Ndax mas nga teewe ndaje Seede Yexowa yi? Boo ci masul a teew, xéyna dinga xaw a ragal tuuti, walla ngay laaj sa bopp lii: ‘Lan la nit ñi di def ci ndaje yooyu? Lu tax ñu am solo? Lu tax ma war cee teew? Ci lesoŋ bii, dinga gis ne teewe ndaje yooyu dina gën a dëgëral sa diggante ak Yàlla te dimbali la ci sa dund.
1. Lu tax ndaje Seede Yexowa yi am solo?
Kenn ci ñi bind Biibël bi wax na li tax teewe ndaje yi am solo lool: «Ma màggal Aji Sax ji fi ndajey way-gëm ñi» (Sabóor 26:12). Tey itam, Seede Yexowa yi dañuy am mbégte ci amal ay ndaje. Ci àddina si sépp, semen bu nekk dañuy booloo ngir jaamu Yàlla, woyal ko te ñaan ko. Dañuy amal itam at mu nekk, ay ndaje yu mag ngir jaamu Yàlla.
2. Lan nga nar a jàng ci suñu ndaje yi?
Ci ndaje yi, dañu ñuy jàngal Kàddu Yàlla «njàng mu leer, di [ñu] ko firil» (Jàngal Neyemi 8:8). Booy teewe ndaje yi, dinga jàng lu jëm ci Yexowa ak jikkoom yu rafet. Looy gën di nànd mbëggeelam ci yow, seen diggante di gën di rattax. Dinga gis itam ni la Yàlla mënee dimbali nga am jàmm ci sa dund (Esayi 48:17, 18).
3. Ban njariñ nga mën a jële ci booloo ak nit ñi ci suñu ndaje yi?
Yexowa dafa ñu sant ñuy «xiirtalante cig mbëggeel ak ci jëf yu baax. Te [bañ a] bàyyi sunu ndaje yi» (Yawut ya 10:24, 25). Ci suñu ndaje yi, dinga fa fekk ñu bëggante dëgg ci seen biir, te bëgg a yokk seen xam-xam ci Yàlla, ni yow. Dinga leen dégg ñuy wax ci Biibël bi, wax juy dëgëral ngëm (Jàngal Room 1:11, 12). Dinga fa xamante itam ak ay nit ñu bég ci seen dund doonte sax am nañu ay jafe-jafe. Loolu lépp bokk na ci li tax, Yexowa bëgg ñuy teewe ndaje yépp!
XÓOTALAL NJÀNG MI
Xoolal li Seede Yexowa yi di def ci seen ndaje yi, ak njariñ bi nekk ci teewe ndaje yooyu.
4. Ndaje Seede Yexowa yi
Karceen yu njëkk ya dañu doon faral di booloo ngir jaamu Yexowa (Room 16:3-5). Jàngal Kolos 3:16. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:
Naka la karceen yu njëkk ya doon jaamoo Yexowa?
Tey, Seede Yexowa yi dañuy faral di booloo ci seen béréb yi ñuy jaamoo Yàlla. Ngir xam li ñuy def ci seen ndaje yi, seetaanal WIDEO BI. Boo paree, xoolal nataal biy wone benn ci seen ndaje te tontu ci laaj yii di topp.
Lan nga gis ne moom lañuy def ci saalu Nguur gi, te nga jàng ko itam ci Kolos 3:16?
Ndax gis nga ci wideo bi walla ci nataal bi, leneen lu la neex ci ndaje yi?
Jàngal 2 Korent 9:7. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:
Lu tax Seede Yexowa yi duñu laaj kenn xaalis ci seen ndaje yi?
Yow ak ki lay jàngal Biibël bi, xool-leen li ñu nar a waxtaane ci ndaje biy ñëw.
Ban ci waxtaan yi, moo la gën a itteel walla ban nga foog ne, moo lay amal njariñ?
Ndax xamoon nga ne...
Ci jw.org, dinga fa fekk béréb yi ak waxtu yi ndaje yi di am fépp ci àddina si.
Ci suñu ndaje yi dafay am ay waxtaan, ay wone ak ay wideo. Dañuy woy ba pare ñaan, bu ndaje yi di komaase ak bu ñuy jeex
Ci ndaje yi, am na ay waxtaan yu ànd ak ay laaj ngir ñi teew mën cee bokk
Ñépp a ci mën a teew, muy njaboot yi, salibateer yi, mag ñi, ak xale yi
Kenn du fey dara. Seede Yexowa yi duñu laaj kenn xaalis ci ndaje yooyu
5. Teewe ndaje yi dafa laaj góor-góorlu
Yeesu ak waa këram ay royukaay lañu ci fànn boobu. At bu nekk dañu daan jóge Nasaret dox 100 km ngir dem teewe ndaje ca Yerusalem. Rax-ci-dolli, dañu doon jaar ci ay tund. Jàngal Luug 2:39-42. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:
Ndax foog nga ne, dem ba Yerusalem yomboon na?
Lan moo tax nga war a góor-góorlu ngir teewe ndaje yi?
Ndax foog nga ne jar na ko? Lu tax?
Biibël bi nee na, di booloo ngir jaamu Yàlla, am na solo lool. Jàngal Yawut ya 10:24, 25. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:
Lu tax ñu war a faral di teewe ndaje yi?
BU LA NIT WAXOON: «Soxlawul ngay booloo ak ñeneen. Mën nga yem rekk ci jàng Biibël bi ci sa kër.»
Ban aaya walla ban nettali ci Biibël bi, mooy wone li Yexowa bëgg?
NAÑU TËNK
Teewe ndaje yi dina la dimbali nga gën a xam Yexowa, gën a dëgëral sa xaritoo ak moom, te jaamu ko ànd ci ak ñeneen.
Nañu fàttaliku
Lu tax Yexowa bëgg ñuy teewe ndaje yi?
Lan nga nar a jàng ci ndaje Seede Yexowa yi?
Ndax foog nga ne teewe ndaje yi, mën na la dimbali ci beneen fànn?
GËSTUL
Bu dee danga xaw a ragal a teewe ndaje yi nag, lan nga mën a def? Xoolal ni benn góor gu ragaloon a teewe ndaje yi, demee ba bëgg leen.
Xoolal ni benn ndaw saware ci teewe ndaje yi ak li mu def ngir kontine di leen teewe.
Xoolal ni benn bandi bu soxor soppee dundam, gannaaw bi mu teewe benn ci ndaje Seede Yexowa yi.
«Masuma woon a dem fenn te yóbbuwuma sama pistole» (w14 1/7)