TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • my nettali 36
  • Nag Bi Ñu Defare Wurus

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Nag Bi Ñu Defare Wurus
  • Ay nettali yu nekk ci Biibël bi
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Yexowa Joxe Na Ndigalam Yi
    Ay nettali yu nekk ci Biibël bi
Ay nettali yu nekk ci Biibël bi
my nettali 36
Waa Israyil ñu ngiwoy, di fecc ak di jaamu nagu wurus bi

NETTALI 36

Nag Bi Ñu Defare Wurus

OXOO ! Lan la nit ñi di def nii ? Benn nag lañuy ñaan ! Lu tax ñuy def loolu ?

Musaa dafa yàgg ci tund bi. Mbooloo mi daldi ne : ‘ Xamuñu li dal Musaa. Kon nañu def benn yàlla, mu yóbbu ñu ci biti réew mii. ’

Aaroona, magu Musaa, wax leen lii : ‘ Kon tekkileen seen jaaro wurus yi, indil ma leen. ’ Aaroona daldi leen dugal ci safara ba ñu ruy, mu defar ci benn nagu wurus. Mbooloo mi ne : ‘ Lii mooy suñu Yàlla bi ñu génne Misra ! ’ Ba pare waa Israyil def benn mbuumbaay te jaamu nagu wurus bi.

Bi Yexowa gisee loolu, dafa mer lool. Mu ne Musaa : ‘ Wàccal gaaw. Mbooloo mi mu ngi def lu bon a bon. Dañu fàtte samay ndigal te ñu ngiy jaamu benn nagu wurus. ’

Musaa dafa toj ñaari xeer yi Yàlla bindoon fukki ndigal yi

Musaa gaaw a wàcc tund ba. Mu gis nit ñi di woy te di wër nagu wurus bi, di fecc. Musaa mer lool ba sànni ñaari xeer fi Yàlla bindoon ndigal yi. Xeer yi toj ba tas. Musaa jël nagu wurus bi, lakk ko ci safara ba mu ruy, ba pare defar ko mu nekk pëndax.

Li mbooloo mi def, bon na lool. Looloo tax Musaa woo ay góor, ne leen ñu jël seen jaasi, ba pare wax leen lii : ‘ Ñu bon ñi doon jaamu nagu wurus bi, dañu war a dee. ’ Ñu daldi rey 3 000 nit ! Ndax loolu wonewul ne Yexowa rekk lañu war a jaamu, te waruñu jaamu ay yàlla yu dul dëgg ?

Gàddaay gi 32:1-35.

Laaj yi

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager