TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • fg lesoŋ 14 laaj 1-4
  • Lu tax Yàlla am mbootaay ?

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Lu tax Yàlla am mbootaay ?
  • Xibaaru jàmm bi jóge ci Yàlla !
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Naka la Seede Yexowa yi di doxale ci seen mbootaay ?
    Lan la ñu Yàllay laaj?
  • Kan mooy «surga bu takku te teey» bi te lan lay def?
    Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
Xibaaru jàmm bi jóge ci Yàlla !
fg lesoŋ 14 laaj 1-4

NJÀNGALE 14

Lu tax Yàlla am mbootaay ?

1. Lu tax Yàlla def Israyil bu njëkk ba mbootaayam ?

1. Mbootaayu Yàlla bi ci Israyil bu njëkk ba ; 2. Karceen yu njëkk ya ñu ngi ànd di waare

Yàlla dafa jël ay sëtu maam Ibraayma def leen mbootaay te jox leen ay sàrt. Mu tudde leen “ Israyil ” te sas leen ñu sàmm kàddoom ak diine dëgg ji (Sabóor 147:19, 20). Kon nit ñi ci xeet yépp mënoon nañu barkeelu ci waa Israyil. — Jàngal Njàlbéen ga 22:18.

Yàlla tànnoon na waa Israyil ngir ñu nekk ay seedeem. Jaar-jaaru Israyil bu njëkk ba, wone na naka la nit di ame jàmm bu toppee sàrtu Yàlla yi (Deutéronome 4:6). Noonu yeneen xeet yi mënoon nañu jaar ci waa Israyil ngir xam Yàlla dëgg ji. — Jàngal Isaïe 43:10, 12.

2. Lu tax Karceen dëgg yi booloo nekk benn ?

Ci diggante bi, waa Israyil ñàkk nañu barke Yàlla, Yexowa jël mbooloo Karceen mu wuutu leen (Macë 21:43 ; 23:37, 38). Léegi, Karceen dëgg yi ñoo jël palaasu waa Israyil te nekk ñiy seede Yexowa. — Jàngal Jëf ya 15:14, 17.

Yeesu won na ñi mu doon àndal ni ñu war a doxale ngir waare te sàkk ay taalibe ci xeet yépp (Macë 10:7, 11 ; 24:14 ; 28:19, 20). Fi ñu tollu nii ci mujug jamono, liggéeyu waaraate bi léegi mu àgg ci njeexteelam. Yexowa def na lu masul a am, ci lu mu boole ay milyoŋi nit ci xeet yépp ci diine dëgg ji (Peeñu ma 7:9, 10). Karceen dëgg yi dañoo booloo nekk benn ngir xiirtalante te dimbalante. Ci àddina si sépp, ñoo bokk benn porogaraamu njàngum Biibël bi ci seen ndaje yi. — Jàngal Yawut ya 10:24, 25.

3. Kañ la mbootaayu Seede Yexowa yi tàmbali ci suñu jamono ji ?

Ay seede Yexowa yuy waare ci ati 1900 ak yeneen yu koy def ci suñu jamono ; ay téere ci ay làkk yu bare yu ñuy dimbali ci gëstu Biibël bi.

Ci atum 1870, benn mbooloo bu ndaw bu doon jàng Biibël bi, komaase woon na feeñal dëgg yu nëbbu woon ci Biibël bi. Mbooloo boobu xamoon na ne, Yeesu wonoon na mbooloo Karceen ni mu war a doxale ngir waare, noonu ñu tàmbali liggéeyu waare Nguur gi ci àddina si sépp. Ci atum 1931 lañu jël turu Seede Yexowa. — Jàngal Jëf ya 1:8 ; 2:1, 4 ; 5:42.

4. Naka la Seede Yexowa yi di doxale ci seen biir ?

Ca jamono karceen yu jëkk ya, dafa amoon benn Jataay biy dogal bu doon jiite mbooloo Karceen yi amoon ci dëkk yu bare. Jataay boobu dafa nangu woon ne Yeesu mooy Kilifa mbooloo mi (Jëf ya 16:4, 5). Naka noonu, tey itam am na Jataay biy dogal ci Seede Yexowa yi. Ay mag yu bare xam-xam lañu. Jataay boobu dafay wottu bànqaasu Seede Yexowa yi nga xam ne dañuy tekki, di defar ak a yónnee ay jumtukaay ngir jàng Biibël bi ci lu ëpp 600 làkk. Rax-ci-dolli Jataay biy dogal mu ngi joxe ay xiirtal ak ay tegtal yu jóge ci Mbind mu sell mi ci lu ëpp 100 000 mbooloo ci àddina si sépp. Ci mbooloo bu nekk, am na ay góor yu àttan sasu magi mbooloo walla wottukat. Góor yu baax yooyu dañuy toppatoo bu baax ñi nekk ci mbootaayu Yàlla. — Jàngal 1 Piyeer 5:​2, 3.

Seede Yexowa yi xam nañu ni ñuy doxale ngir waare xibaaru jàmm bi te sàkk ay taalibe. Ni taalibe Yeesu yi, dañuy dem waare ci kër yi (Jëf ya 20:20). Dañuy jàngal Biibël bi nit ñi dëggu te bëgg dëgg gi. Waaye Seede Yexowa yi nekkuñu benn mbootaay rekk, yem ci. Dañu mel ni njaboot bu am baay bu leen bëgg. Ay mbokk lañu yu bëggante (2 Tesalonig 1:3). Ñiy jaamu Yexowa dañoo booloo nekk benn ngir neex Yàlla te di dimbali nit ñi, moo tax ñu nekk njaboot bi gën a bég ci kaw suuf si. — Jàngal Sabóor 33:12 ; Jëf ya 20:35.

Boo bëggee yokk sa xam-xam ci li ñu wax fii, xoolal pàcc 19 ci téere bi tudd Lan la Biibël bi wax dëgg-dëgg ?

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager