WOY-YÀLLA 136
Yal na la Yexowa fey say jëf!
(Ruut 2:12)
1. Yàlla du fàtte képp ku koy jaamu
Te di ko def ak cawarte.
Seen ngëm moo leen xiir ci jaamu Yexowa,
Moo tax toppuñu àddina.
Yàlla gis na li la dëgg gi jaral,
Moo tax dina la jàppale.
May na la ay mbokk yu la bëgg lool,
Te dig na la dund ba fàww.
(AWU BI)
Yal na Yexowa fey say jëf yu baax!
Cawarte ji nga wone gis na ko.
Dawal làqu ci loxoy Yàlla,
Lu mu dige def ko, moom ku dëggu la.
2. Lée-lée dund gi day bare ay metit,
Nga naan: ‘mbir yi diis na ci man’.
Jafe-jafe yi, dañuy gën a bare,
Nga naan: ‘amatuma doole’.
Yàlla xam na bu baax li ngay jànkoonteel.
Say ñaan, mu ngi leen di déglu.
Dooleem ak Biibël bi ak waa mbooloo mi
Ñoo lay dooleel ba doo xàddi.
(AWU BI)
Yal na Yexowa fey say jëf yu baax!
Cawarte ji nga wone gis na ko.
Dawal làqu ci loxoy Yàlla,
Lu mu dige def ko, moom ku dëggu la.
(Xoolal itam Njiit yi 11:38-40; Esayi 41:10.)