Mën nga tàmbali jàng Biibël bi bés bu nekk
Mën nga dem ba liir Biibël bi neex ci yow! Ponk yii di topp mën nañu la dimbali nga tàmbali. Tànnal bi la ci gënal te jàng aaya yi mu àndal.
Nit ñu siiwoon ak ay nettali yu siiw
Nóoyin ak mbënn mi: Njàlbéen ga 6:9–9:19
Musaa ca géeju Barax ya: Mucc ga 13:17–14:31
Ruut ak Nawmi: Ruut pàcc 1-4
Daawuda ak Golyaat: 1 Samiyel pàcc 17
Abigayil: 1 Samiyel 25:2-35
Dañeel ci biir paxu gaynde: Dañeel pàcc 6
Elisabet ak Maryaama: Luug pàcc 1-2
Ay xelal yu baax ci suñu dund
Dundu njaboot: Efes 5:28, 29, 33; 6:1-4
Xaritoo: Kàddu yu Xelu 13:20; 17:17; 27:17
Ñaan Yàlla: Sabóor 55:23; 62:9; 1 Yowaana 5:14
Waareb Yeesu ca tund wa: Macë pàcc 5-7
Liggéey: Kàddu yu Xelu 14:23; Kàdduy Waare 3:12, 13; 4:6
Li la mën a dimbali bu dee danga...
Xàddi: Sabóor 23; Esayi 41:10
Am naqar: 2 Korent 1:3, 4; 1 Piyeer 5:7
Am xel mu lay tuumaal: Sabóor 86:5; Esekiyel 18:21, 22
Li Biibël bi wax ci...
Mujug jamono: Macë 24:3-14; 2 Timote 3:1-5
Yaakaaru ëllëg: Sabóor 37:10, 11, 29; Peeñu 21:3, 4
XELAL: Bu dee ay aaya rekk lañu lim ci benn pàcc, boo bëggee nànd bu baax aaya yooyu, nanga jàng pàcc bi yépp. Jëfandikool tabló bi nekk ci njeexteelu téere bi te tudd «Bindal fi nga yem ci liir Biibël bi» ngir bind fi nga tollu ci jàng pàcc yi. Nanga fas yéene liir Biibël bi bés bu nekk.