LESOŊ 23
Sóobu ci ndox: jubluwaay bu am solo!
Yeesu waxoon na ne karceen yi dañu war a sóobu ci ndox (Jàngal Macë 28:19, 20). Waaye lan mooy sóobu ci ndox? Lan la nit war a def ngir sóobu ci ndox?
1. Lan mooy sóobu ci ndox?
Baatu «sóob» ci làkku gereg dafay tekki li ñu «dugal» ci ndox. Bi Yeesu di sóobu, moom ci boppam lañu dugal ci dexu Yurdan, ba pare ‘génne ko ci ndox mi’ (Màrk 1:9, 10). Noonu it karceen dëgg yi bu ñuy sóobu, seen yaram yépp lañuy dugal ci biir ndox.
2. Lan la sóobu ci ndox di wone?
Bu nit sóoboo, dafay wone ne jébbal na boppam Yexowa Yàlla. Naka la nit di jébbaloo ci Yàlla? Bala muy sóobu, dafay ñaan Yexowa wax ko ne, dafa ko bëgg a jaamu ba fàww. Dafay dig Yexowa ne, moom rekk lay jaamu te def coobareem dina doon li gën a am solo ci dundam. Dafay tànn «bàyyi boppam [...] doora topp ci» njàngaley Yeesu te roy ci moom (Macë 16:24). Jébbalu ak sóobu mooy may nit ki diggante bu rattax ak Yexowa ak yeneen jaamu Yàlla yi.
3. Lan la nit war a def ngir mën a sóobu ci ndox?
Boo bëggee sóobu ci ndox, danga war a jàng xam Yexowa te am ngëm gu dëgër ci moom (Jàngal Yawut ya 11:6). Bu sa xam-xam ak sa ngëm di yokku, ngay gën di bëgg Yexowa. Te loolu dina tax nga bëgg a wax ci moom te topp ay santaaneem ci sa dund (2 Timote 4:2; 1 Yowaana 5:3). Bu nit di dund ‘dund gu dëppoo ak bokkam ci Boroom bi, ba neex ko ci fànn gu nekk,’ mën na jël dogalu jébbalu ci Yàlla te sóobu ci ndox (Kolos 1:9, 10).a
XÓOTALAL NJÀNG MI
Xoolal li ñu mën a jàng ci ni Yeesu sóoboo ci ndox ak ni nit mënee waajal boppam ngir sóobu ci ndox.
4. Li ñu mën a jàng ci ni Yeesu sóoboo ci ndox
Jàngal Macë 3:13-17 ngir gën a xam ni Yeesu sóoboo. Boo paree nga tontu ci laaj yii di topp:
Ndax Yeesu xale la woon bi muy sóobu ci ndox?
Ndax dañu wis ndox rekk ci boppu Yeesu? Walla ndax dañu dugal yaramam yépp ci ndox?
Bi Yeesu sóoboo ci ndox ba pare, dafa tàmbali liggéey bu am solo bi ko Yàlla sant. Jàngal Luug 3:21-23 ak Yowaana 6:38. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:
Bi Yeesu sóoboo ci ndox ba pare, ban liggéey la jiital ci dundam?
5. Sóobu ci ndox, jubluwaay bu mën a nekk la
Xalaat a jébbalu ak sóobu ci ndox, mën na tiital nit. Waaye looy gën di góor-góorlu, dinga dem ba gis ne mën nga koo def. Boo bëggee gis ay nit yu jël dogal boobu ba pare, seetaanal WIDEO BI.
Jàngal Yowaana 17:3 ak Saag 1:5. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:
Lan moo mën a dimbali nit mu waajal boppam ngir sóobu ci ndox?
Bu ñuy jébbalu ci Yexowa, dañu koy wax ne moom lañu bëgg a jaamu ba fàww
Bu ñuy sóobu ci ndox, dañuy won ñépp ne jébbal nañu suñu bopp Yàlla
6. Bu ñu sóoboo ci ndox dañuy bokk ci njabootu Yexowa
Bu ñu sóoboo ci ndox dañuy bokk ci njaboot gu mag ci kaw suuf si sépp. Doonte sax bokkuñu fi ñu jóge ak jaar-jaar, terewul ñoo bokk li ñu gëm te santaane yi ñuy topp benn la. Jàngal Saag 2:23 ak 1 Piyeer 2:17. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:
Sóobu ci ndox, lan la mën a def diggante nit ki ak Yexowa ak digganteem ak yeneen jaamu Yexowa yi?
BU LA NIT WAXOON: «Pareeguma ngir sóobu ci ndox.»
Bu dee yow itam loolu nga xalaat, ndax yaakaaruloo ne war na nekk sa jubluwaay?
NAÑU TËNK
Yeesu waxoon na ne karceen yi dañu war a sóobu ci ndox. Bu nit bëggee sóobu ci ndox, dafa war a dëgëral ngëmam ci Yexowa, topp ay santaaneem, te jébbal ko boppam.
Nañu fàttaliku
Lan mooy sóobu ci ndox, te lu tax mu am solo?
Lan la sóobu ci ndox di wone?
Lan la nit war a def ngir jébbalu te sóobu ci ndox?
GËSTUL
Xoolal li mën a dimbali nit mu jëm kanam ba sóobu ci ndox.
«Bëgg Yexowa ak am ngërëm ci moom mooy xiir nit ci sóobu ci ndox» (w20 màrs)
Xoolal li dimbali benn góor mu nànd ne waruñu sukkandiku rekk ci ay yëg-yëg ngir sóobu ci ndox.
«Dañu bëggoon man ci sama bopp ma xam lan mooy dëgg gi» (w13 1/2)
Xoolal li tax sóobu ci ndox nekk jubluwaay bu am solo ak ni nga ko mënee waajal.