LESOŊ 17
Yan jikko yu rafet la Yeesu amoon?
Bu ñu jàngee li Yeesu wax ak li mu def bi mu nekkee ci kaw suuf, dinañu gis ne wone na jikko ju tax ñu bëgg a xaritoo ak moom ak baayam, Yexowa. Yan ñooy yenn ci jikko yu rafet yooyu? Te naka lañu mënee roy Yeesu ci suñu dund?
1. Ci ban anam la Yeesu niru Baayam?
Bi mu nekkee ci kaw asamaan, Yeesu xool na Baayam muy jëf ay miliaari at te jànge na ci moom lu bari. Loolu tax na muy xalaate ni Baayam, di gise mbir yi ni moom, te di jëfe ni moom (Jàngal Yowaana 5:19). Li am mooy, Yeesu dafa roy Baayam ba mu mat sëkk. Looloo tax mu wax lii: «Ku ma gis, gis nga Baay bi» (Yowaana 14:9). Looy gën di xam jikko Yeesu, ngay gën di xam Yexowa. Ci misaal, yërmande ji Yeesu amoon ci nit ñi, dafa ñuy won ne Yexowa fonk na ñu.
2. Naka la Yeesu wonee ne dafa bëgg Yexowa?
Lii la Yeesu waxoon: «Àddina si war na xam ne bëgg naa Baay bi te ni ma ko Baay bi sante, ni laay jëfe» (Yowaana 14:31). Bi mu nekkee ci kaw suuf, Yeesu wone na mbëggeel gu réy gi mu am ci Baayam ci ni mu ko déggale ci lépp, bu dee sax jafe woon na ci moom. Mbëggeel gi Yeesu am ci Baayam moo tax mu bëggoon di wax ci moom ak di dimbali ñeneen ñi ñu nekk xaritu Baayam (Yowaana 14:23).
3. Naka la Yeesu wonee ne dafa bëgg nit ñi?
Biibël bi nee na Yeesu dafay «bànneexoo doomi aadama» (Kàddu yu Xelu 8:31). Mbëggeel gi Yeesu am ci nit ñi moo tax mu leen doon dooleel ak di leen dimbali, te du ci xaar dara. Def na ay kéemaan yu bari yu wone ne am na kàttan, waaye it am na yërmande ci nit ñi (Màrk 1:40-42). Dafa baaxoon ak ñépp te daanul gënaatle. Waxam dafa doon dëfal boroom xol yu rafet yi ko doon déglu te may leen it yaakaaru ëllëg. Yeesu nangu woon na sonn ngir doomu Aadama yi yépp te dem na sax ba dee ndax mbëggeel gi mu am ci ñoom. Waaye ñi mu gën a bëgg mooy ñiy topp ay njàngaleem (Jàngal Yowaana 15:13, 14).
XÓOTALAL NJÀNG MI
Yokkal sa xam-xam ci Yeesu. Xoolal itam ni nga ko mënee roy ci ni mu doon wonee mbëggeel ak ni mu yéwéne woon.
4. Yeesu dafa bëgg Baayam
Yeesu won na ñu, ni ñu mën a wonee suñu mbëggeel ci Yàlla. Jàngal Luug 6:12 ak Yowaana 15:10; 17:26. Boo paree jàng aaya bu ci nekk, tontul ci laaj bii:
Ni Yeesu, naka lañu mënee won Yexowa ne bëgg nañu ko?
Yeesu dafa bëggoon Baayam bi ci asamaan te dafa ko doon faral di ñaan
5. Yeesu dafa bëgg nit ñi
Yeesu dafa jiitaloon soxlay nit ñi. Bu sonnoon sax, dafa doon jël jot ngir dimbali leen. Jàngal Màrk 6:30-44. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:
Ci nettali bii, naka la Yeesu wone ne am na yitte ci nit ñi? (Xoolal aaya 31, 34, 41, ak 42).
Lan moo doon xiir Yeesu ci dimbali nit ñi? (Xoolal aaya 34).
Ndegam Yeesu Yexowa lay roy, kon jikko yi mu wone yépp, lan la lay jàngal ci Yexowa?
Naka lañu mën a roye Yeesu ci yitte bi mu amoon ci nit ñi?
6. Yeesu dafa yéwén
Yeesu dafa yéwénoon bu dee sax amul woon alal ju bari, te dafa ñuy xiirtal ci yéwén ñun itam. Jàngal Jëf ya 20:35. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:
Ci li Yeesu wax, lan moo ñu mën a may mbégte?
Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.
Naka lañu mënee yéwén bu dee sax bariwuñu alal?
Ndax xamoon nga ne...
Biibël bi wax na ñu, ñuy ñaan Yexowa jaare ko ci turu Yeesu (Jàngal Yowaana 16:23, 24). Bu ñuy ñaane noonu, dañuy wone ne nangu nañu li Yeesu def ngir dimbali ñu, ñu nekk xaritu Yexowa.
BU LA NIT WAXOON: «Yàlla mooy teg nit ñi coono ngir natt fi seen ngëm yem.»
Ndegam Yeesu Yexowa lay roy, naka la ay jëfam di wone ne, Yàlla du teg nit ñi coono?
NAÑU TËNK
Yeesu dafa bëgg Yexowa, te bëgg it nit ñi. Ndegam Yeesu dafa niru Baayam, looy gën di xam Yeesu, ngay gën di xam Yexowa.
Nañu fàttaliku
Naka lañu mënee won Yexowa suñu mbëggeel, ni ko Yeesu defe?
Naka lañu mënee won nit ñi suñu mbëggeel, ni ko Yeesu defe?
Lan moo la gën a neex ci jikkoy Yeesu?
GËSTUL
Xoolal yenn ci jikkoy Yeesu yi ak ni ñu leen mënee roy.
«Bu ñu bëggee roy Yeesu, nañu...» (Yeesu: Yoon wi, dëgg gi, dund gi, paas 317)
Xoolal li tax mu am solo ñuy ñaan ci turu Yeesu.
Lan lañu mën a jàng ci ni Yeesu doon doxale ak jigéen ñi?