TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • lff lesoŋ 34
  • Naka lañu mën a wonee ne bëgg nañu Yexowa?

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Naka lañu mën a wonee ne bëgg nañu Yexowa?
  • Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
  • Turu xaaj yi
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • XÓOTALAL NJÀNG MI
  • NAÑU TËNK
  • GËSTUL
  • Mbëggeelu Yexowa amul àpp
    La Tour de Garde annonce le Royaume de Jéhovah (Édition d’étude)—2025
  • Na la wóor ne Yexowa fonk na la
    La Tour de Garde annonce le Royaume de Jéhovah (Édition d’étude)—2025
  • Nañu dund ci fasoŋ bu neex Yàlla
    Lan la Biibël bi wax dëgg-dëgg ?
Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
lff lesoŋ 34
Lesoŋ 34. Góor gu nekk ci dëkku taax, mu ngi xool asamaan di xalaat.

LESOŊ 34

Naka lañu mën a wonee ne bëgg nañu Yexowa?

Édition imprimée
Édition imprimée
Édition imprimée

Bi nga komaasee jàng Biibël bi ba léegi, ndax gis nga ne gën ngaa jege Yàlla? Ndax bëgg nga kontine di dëgëral sa diggante ak moom? Bu dee waaw, xamal ne lu Yexowa di gën a gis ne sa mbëggeel ci moom a ngi yokku, moom itam dafa lay gën a bëgg te gën laa toppatoo. Naka nga ko mën a wonee ne, bëgg nga ko?

1. Naka lañu mënee won Yexowa ne bëgg nañu ko?

Bu ñuy déggal Yexowa lañu koy won ne bëgg nañu ko (Jàngal 1 Yowaana 5:3). Du forse kenn mu déggal ko. Xanaa kay, dafay bàyyi ku nekk tànn déggal ko walla bañ koo déggal. Lu tax? Yexowa dafa bëgg ñu ‘nangul ko ak suñu xol bépp’ (Room 6:17). Kon bëggul ñu déggal ko rekk ndaxte wareef la, waaye dafa bëgg ñu déggal ko ndax mbëggeel gi ñu am ci moom. Xaaj 3 ak 4 ci téere bii dinañu la dimbali nga wone sa mbëggeel ci Yexowa. Dinga ci gis li nga war a def ak li nga war a moytu ngir neex ko.

2. Lu tax mu mën a jafe ci ñun ñu won Yexowa suñu mbëggeel?

«Musiba bare naa dal ku jub, Aji Sax ji musal ko ci lépp» (Sabóor 34:20). Ñun ñépp ay xeex ak suñu matadi. Te itam mën nañu am poroblemu xaalis, nit def ñu lu awul yoon, walla ñu am yeneen jafe-jafe. Bu ñu nekkee ci ay jafe-jafe, def li ñu Yexowa sant mën na metti ci ñun. Ndaxte bu ñuy dund lu mel noonu, xéyna bañ a déggal Yexowa mooy gën a yomb. Waaye bu ñuy wéy di def li ñu Yexowa sant, dinañu ko won ne moom lañu gën a bëgg. Dañuy wone it ne takku nañu ci moom. Te bu ñu takkoo ci moom, moom it dina takku ci ñun. Du ñu mas a bàyyi (Jàngal Sabóor 18:26).

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal li tax mu am solo ci Yexowa nga déggal ko, te jàngal li la mën a dimbali nga wéy di takku ci moom.

3. Seytaane dafa lay tuumaal

Ni ko Biibël bi wonee ci téere Ayóoba, Seytaane yemul rekk ci tuumaal Ayóoba, waaye dafa ci boolewaale ñépp ñi bëgg a jaamu Yexowa. Jàngal Ayóoba 1:1, 6–2:10. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Ci Seytaane, lu tax Ayóoba doon déggal Yexowa? (Xoolal Ayóoba 1:9-11).

  • Lan la Seytaane tuumaal doomu Aadama yi yépp, ba ci yow mii? (Xoolal Ayóoba 2:4).

Jàngal Ayóoba 27:5b. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Naka la Ayóoba wone ne bëgg na Yexowa dëgg?

Seytaane mu ngi tëkku Yexowa. Mu ngi tuumaal Ayóoba, mi am ay taab, di tuumaal it mbokk bu jigéen jii di jaamu Yexowa tey.

Ayóoba wone na mbëggeelam ci Yexowa ndaxte dafa wéy di takku ci moom

Bu ñuy wéy di takku ci Yexowa dañu koy won suñu mbëggeel

4. Bégalal xolu Yexowa

Jàngal Kàddu yu Xelu 27:11. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Lan la Yexowa di yëg boo wone ne am nga xel te déggal ko? Lu tax?

5. Mën nga takku ci Yexowa

Suñu mbëggeel ci Yexowa moo ñuy xiir ci wax nit ñi lu jëm ci moom. Te suñu takkute ci moom, moo ñuy tax a wéy di def loolu bu dee sax yombul. Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp.

WIDEO: Woneel sa ngëm bu ñu lay fitnaal (5:09)

  • Ndax wax ñeneen ñi lu jëm ci Yexowa mas naa jafe ci yow?

  • Ci wideo bi, lan moo dimbali Grayson ba ragalatul woon?

Bu ñu bëggee li Yexowa bëgg te bañ li mu bañ, takku ci moom dafay gën a yomb. Jàngal Sabóor 97:10. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Ci li nga jàng ba léegi, lan nga gis ne Yexowa bëgg na ko? Lan nga gis ne bañ na ko?

  • Naka nga mënee jàng bëgg lu baax te bañ lu bon?

6. Dañuy jële njariñ ci déggal Yexowa

Ci lépp, déggal Yexowa mooy li gën. Jàngal Esayi 48:17, 18. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Ndax foog nga ne mën nañu gëm ne, ci lépp Yexowa mooy ki xam li gën ci ñun? Lu tax?

  • Ban njariñ nga jële ci sa njàngum Biibël bi ak ci li nga xam ci Yàlla dëgg ji, Yexowa?

BU LA NIT WAXOON: «Yaakaaruma ne suñuy jëf mën na bégloo Yàlla.»

  • Ban aaya nga mën a jël ngir won ko ne, suñuy jëf am na lu muy def ci Yexowa?

NAÑU TËNK

Booy déggal Yexowa te wéy di takku ci moom bu dee sax yombul, dinga wone ne bëgg nga ko.

Nañu fàttaliku

  • Lan nga jàng ci Ayóoba?

  • Naka nga fas yéenee won Yexowa sa mbëggeel?

  • Lan moo lay dimbali nga wéy di takku ci Yexowa?

Jubluwaay

GËSTUL

Xoolal leneen lu jëm ci li Seytaane tuumaal doomu Aadama yi.

«Ayóoba dafa wéy di takku ci Yàlla» (bm xaaj 6)

Xoolal ni xale yi sax mënee wone seen mbëggeel ci Yexowa.

Nanga bégal Yexowa (8:16)

Naka la ndaw mënee wone takkute ci Yexowa, bu amee ñu koy puus ci def lu bon?

Bañal say moroom dugal la ci lu bon! (3:59)

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager