LESOŊ 36
Nañu jub ci lépp
Ñépp a bëgg a am xarit yu jub. Yexowa itam dafa bëgg ay xaritam doon ñu jub. Waaye loolu yombul ndaxte ci àddina si nit ñu bare jubuñu. Ban njariñ lañuy jële ci jub ci lépp?
1. Lan mooy li gën a tax ñu war a nekk nit ñu jub?
Bu ñu jubee, dañuy won Yexowa ne bëgg nañu ko te wormaal nañu ko. Xalaatal ci lii: Yexowa xam na lépp li ñuy xalaat ak li ñuy def (Yawut ya 4:13). Bu ñu tànnee doon ñu jub, dafa koy gis te dafa ciy bég. Lii la Kàddoom wax: «Aji Sax ji daa sib ku dëng, xejjoo kuy jubal» (Kàddu yu Xelu 3:32).
2. Naka lañu mënee doon nit ñu jub bés bu nekk?
Yexowa dafa bëgg ñuy «waxante dëgg» (Sàkkaryaa 8:16, 17). Loolu lu muy tekki? Bu ñuy wax ak suñuy mbokk, ñi ñu bokkal liggéey, suñu mbokk karceen yi, walla kilifa yi ci réew mi, duñu leen fen te duñu leen jéem a nax. Nit ku jub du sàcc ñeneen ñi walla def leen yëfi njublaŋ (Jàngal Kàddu yu Xelu 24:28 ak Efes 4:28). Te dafay fey lempo yépp yi mu war a fey (Room 13:5-7). Ci fànn yooyu ak ci yeneen, dañuy «rafet [maanaam jub] ci lépp lu nuy def» (Yawut ya 13:18).
3. Ban njariñ lañuy jële ci nekk ñu jub?
Bu ñu nit ñi xame ni nit ku jub, dañu ñuy wóolu. Te loolu dina tax ci mbooloo mi, ku nekk am xel mu dal, ñu bëggante mel ni njaboot. Ñun itam dinañu am xel mu dal. Nekk ñu jub mën na tax itam ñu «rafetal ci lépp njànglem Yàlla sunu Musalkat» te dina tax ñi bokkul ci mbooloo mi bëgg a jaamu Yexowa (Tit 2:10).
XÓOTALAL NJÀNG MI
Xoolal nekk nit ku jub li muy def ci Yexowa ak ci yow, te jàngal ni nga mënee jub ci fànn yu bare ci sa dund.
4. Nekk ku jub lu neex Yexowa la
Jàngal Sabóor 44:22 ak Malasi 3:16. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:
Ci sa xalaat, lu tax foog ne mën nañu nëbb Yexowa dëgg gi, doon ñàkk xel?
Ci sa xalaat, lan la Yexowa di yëg boo tànnee wax dëgg, bu dee sax jafe na?
Bu xale yi di wax dëgg, dañuy bégal seeni waajur. Bu ñuy wax dëgg, dañuy bégal Yexowa
5. Nañu def lu jub saa su nekk
Nit ñu bare dañu gëm ne def lu jub saa su nekk, mënul nekk. Waaye xoolal li tax ñu war a jub saa su nekk. Seetaanal WIDEO BI.
Jàngal Yawut ya 13:18. Boo paree, waxal ni ñu mënee nekk ñu jub...
ci suñu njaboot.
ci bérébu liggéeyukaay ba walla lekkool ba.
ci yeneen fànn.
6. Dañuy jële njariñ ci nekk ku jub
Mën nañu foog ne, nekk ku jub mën na ñu indil ay jafe-jafe. Waaye yàgg-yàgg dinañu gis ne, def lu jub mooy li gën. Jàngal Sabóor 34:13-17. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:
Naka la nekk ku jub di gënee neexal sa dund?
Jëkkër ju jub ak jabar ju jub, dañuy dëgëral seen séy
Liggéeykat bu jubee, ki muy liggéeyal dina ko wóolu
Bu nit ñi jubee, ñi fi nekkal nguur gi dañu leen di wóolu
BU LA NIT WAXOON: «Yenn fen yu ndaw yi, nekkul lu garaaw.»
Lu tax nga gëm ne Yexowa fen yépp la bañ?
NAÑU TËNK
Yexowa dafa bëgg ay xaritam nekk ñu jub ci lépp li ñuy wax ak ci lépp li ñuy def.
Nañu fàttaliku
Naka lañu mënee doon nit ñu jub?
Ci sa xalaat, lu tax foog ne mën nañu nëbb Yexowa dëgg gi, doon ñàkk xel?
Lu tax nga bëgg a def lu jub saa su nekk?
GËSTUL
Naka la waajur yi mënee jàngal seeni doom ñu nekk ñu jub?
Ban njariñ lañuy jële ci sàmm suñu kàddu?
Lan moo tax góor gu nekkoon njublaŋ soppi dundam ba mujj a nekk ku jub?