LESOŊ 38
Nañu fonk dund gi ñu Yàlla may
Mën nañu jële mbégte yu bari ci suñu dund. Bu dee sax dañuy am ay jafe-jafe, terewul mën nañu am mbégte ci suñu dund. Naka lañu mënee wone ne fonk nañu dund gi ñu Yàlla may? Te lan moo gën a tax ñu war koo def?
1. Lu tax ñu war a fonk dund?
War nañu fonk dund ndaxte dund may la bu jóge ci Yexowa, suñu Baay bi ñu bëgg. Ci moom «la dund di balle», moom moo sàkk lépp luy dund (Sabóor 36:10). «Moom mooy jox ñépp bakkan ak ruu ak lépp» (Jëf ya 17:25, 28). Yexowa jox na ñu li ñu soxla ngir wéy di dund. Waaye yemul rekk ci loolu, def na lépp ngir ñu mën a am mbégte ci suñu dund (Jàngal Jëf ya 14:17).
2. Naka lañu mënee won Yexowa ne fonk nañu dund gi mu ñu may?
Bi ñuy nekk ci suñu biiru yaay, la Yexowa tàmbali di ñu toppatoo. Yàlla xiir na jaamam Daawuda mu wax ci moom lii: «Gis nga ma, ba ma diw lumb», maanaam bi ma nekkee ci sama biiru yaay (Sabóor 139:16). Yexowa dafa fonk lool suñu dund (Jàngal Macë 10:29-31). Dafa koy metti lool bu nit teyee faat bakkan, muy bosam walla bosu keneena (Mucc ga 20:13). Bu ñuy def lu ñu mën a xañ suñu bakkan walla ñu bañ a jël matuwaay yi war ngir aar bakkanu ñeneen ñi, loolu it dafay metti Yexowa. Bu ñuy toppatoo suñu dund te respekte dundu ñeneen ñi, dañuy wone ne fonk nañu bu baax dund gi ñu Yàlla may.
XÓOTALAL NJÀNG MI
Xoolal ni nga mënee wone ne fonk nga dund gi ñu Yàlla may.
3. Toppatool sa wér-gi-yaram
Karceen yi jébbal seen bopp Yexowa, seen dund gépp lañu jébbal Yexowa ngir jaamu ko. Loolu dafa mel ni seen yaram lañu jox Yàlla ni sarax. Jàngal Room 12:1, 2. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:
Lan moo war a tax nga toppatoo sa wér-gi-yaram?
Naka nga ko mënee def?
4. Jëlal matuwaay ngir kenn bañ a gaañu mbaa ñàkk bakkanam
Biibël bi wax na ñu, ñuy moytu jëf yi ñu mën a lor. Seetaanal WIDEO BI ngir xam li nga mën a def ngir aar sa bopp ak ñeneen ñi.
Jàngal Kàddu yu Xelu 22:3, te wax ci ni nga mënee moytu jëf yi mën a lor nit ak it ni ko ñeneen ñi mënee moytu...
ci sa kër.
ci sa bérébu liggéeyukaay.
booy def espoor.
booy dawal walla keneen di dawal.
5. Fonkal bakkanu liir bu juddoogul
Daawuda wax na ci anam bu rafet, ci yitte bi Yexowa am ci dundu liir bu nekk ci biiru yaayam di màgg. Jàngal Sabóor 139:13-17. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:
Ci Yexowa, ndax dundu nit ci biiru yaayam lay tàmbali walla bu juddoo?
Santaane yi Yexowa joxoon waa Israyil bu njëkk, dañu doon aar jigéen ñi ak liir yu ñu ëmb. Jàngal Mucc ga 21:22, 23. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:
Naka la Yexowa di gise nit ku rey liir bu juddoogul te teyu ko?
Naka la gise ku rey liir bu juddoogul te tey ko?b
Lan nga xalaat ci gis-gisu Yàlla?
Jigéen ju fonk dund sax mën na foog ne amul beneen pexe bu dul yàq biiram. Jàngal Esayi 41:10. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:
Bu jigéen amee ñi koy xiir ci yàq biir, ci kan la war a wut ndimbal? Lu tax?
BU LA NIT WAXOON: «Jigéen ju nekk am na sañ-sañu yàq biiram, moo moom yaramam.»
Lan moo tax mu wóor la ne Yexowa fonk na dundu jigéen ak liir bi mu ëmb?
NAÑU TËNK
Biibël bi nee na dañu war a bëgg dund gi ñu Yexowa may, fonk ko te sàmm ko; muy suñu dund walla dundu ñeneen ñi.
Nañu fàttaliku
Lu tax dundu doomu Aadama am solo ci Yexowa?
Naka la Yexowa gise ki tey faat bakkanu doomu Aadama?
Lu tax nga am ngërëm ci dund gi la Yàlla may?
GËSTUL
Naka lañu mënee gërëm Yexowa ci dund gi mu ñu may?
Xoolal tontu laaj bii, Ndax Yàlla dina baal jigéen ju yàq biir?
Bu xelu nit demee ci xaru nag? Xoolal ni ko Biibël bi mënee dimbali.
«Dama bëgg a dee: Ndax Biibël bi mën na ma dimbali bu sama xel nekkee ci xaru?» (Ci jw.org la nekk)
a Yexowa dafa am yitte lool ci nit ñi seen yaakaar tas (Sabóor 34:19). Xam na bu baax metitu xol yi mën a yóbbe nit mu bëgg a xaru, te bëgg na leen a dimbali. Ngir gis ni ndimbalu Yexowa mënee may doole ki am ay xalaati xaru, jàngal waxtaan bi tudd «Dama bëgg a dee: Ndax Biibël bi mën na ma dimbali bu sama xel nekkee ci xaru?» Waxtaan boobu mu ngi ci xaaj bi tudd Gëstul ci lesoŋ bii.
b Ñi mas a yàq biir waruñu bàyyi seen xel tuumaal leen ba mu ëpp ndaxte Yexowa mën na leen a baal. Boo ci bëggee am ay leeral, xoolal waxtaan bi tudd «Lan la Biibël bi wax ci yàq biir?» Waxtaan boobu mu ngi ci xaaj bi tudd Gëstul ci lesoŋ bii.