TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • lff lesoŋ 44
  • Ndax feet yépp a neex Yàlla?

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ndax feet yépp a neex Yàlla?
  • Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
  • Turu xaaj yi
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • XÓOTALAL NJÀNG MI
  • NAÑU TËNK
  • GËSTUL
  • Woneel ne danga bëgg a jaamu Yàlla ni mu ko bëgge
    Lan la Biibël bi wax dëgg-dëgg ?
  • Ndax war nañu bokk ci feet yi ?
    Lan la Biibël bi wax dëgg-dëgg ?
Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
lff lesoŋ 44
Lesoŋ 44. Ci benn feet ay téeméeri nit dañu taal ay làmp bàyyi leen ñuy naaw ci kaw asamaan.

LESOŊ 44

Ndax feet yépp a neex Yàlla?

Édition imprimée
Édition imprimée
Édition imprimée

Yexowa dafa bëgg ñu bég ci suñu dund te lée-lée sax di feetu. Waaye ndax feet yépp ak màggal yépp a ko neex? Naka lañu mënee won Yexowa suñu mbëggeel ci fànn boobu?

1. Lu tax feet yu bari neexuñu Yexowa?

Feet yu bari jógewuñu ci Mbind mu sell mi, waaye ñu ngi jóge ci aaday yéefër yi walla ci diine yi dul dëgg. Xéyna loolu mën na la bett. Yenn ci feet yooyu mën nañu laal ci mbirum luxus ak lu ni mel, walla ñu sukkandiku ci ay njàngale yuy wax ne bu nit deewee, am na luy génn ci moom dem dund feneen. Yenn feet yi, ci ay biddaa lañu jóge walla ci gëm ay tuur yuy maye wërsëg (Esayi 65:11). Yexowa lii la sant ay jaamam: «Génnleen biir ñooñu [...] Buleen laal dara lu am sobe» (2 Korent 6:17).a

2. Naka la Yexowa gise feet yiy màggal nit ñi?

Yexowa wax na ñu, ñu moytu ngir bañ a daanu ci fiiru «yaakaar doomu aadama» (Jàngal Yeremi 17:5). Yenn feet yi dañuy màggal ay njiit walla ay soldaar. Ci yeneen yi, nit ñi dañuy màggal seen moom-sa-réew walla seen daraapo réew (1 Yowaana 5:21). Am na it yuy màggal ay mbootaayu politig walla yeneen xeetu mbootaay. Lan la Yexowa di yëg bu gisee ñuy màggal ay nit walla ay mbootaay, rawatina bu dee nit ñooñu walla mbootaay yooyu dañuy fësal ay xalaat yu wuute ak coobareem?

3. Yan doxalin ñoo mën a tax duñu nangoo bokk ci yenn feet yi?

Biibël bi tere na «màndi ak a xawaare, [ak] di xér ci biiñ» (1 Piyeer 4:3). Yenn feet yi dañuy xiir nit ñi ci ëppal ak ci jëfi njaaloo. Bu ñu bëggee wéy di nekk ay xaritu Yexowa, dañu war a sori doxalin yu sellul yooyu.

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal ni nga mënee jël dogal yu baax ci mbirum feet yi ak màggal yi ba mën a neex Yexowa.

Kenn kuy liggéey ak suñu benn mbokk bu góor mu ngi koy may kado Nowel.

4. Moytul feet yiy tilimal turu Yexowa

Jàngal Efes 5:10. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Lan moo ñu war a wóor bala ñuy bokk ci benn feet?

  • Yan feet ñoo siiw fi nga dëkk?

  • Ndax foog nga ne feet yooyu neex nañu Yexowa?

Ñu jël benn misaal, ndax mas nga laaj sa bopp ni Yàlla gise feetu sa bésub juddu, maanaam aniwerseer? Biibël bi masul a nettali benn jaamu Yexowa bu feetu aniwerseeram. Waaye nettali na feetu aniwerseeru ñaari nit ñu nekkul woon ay jaamu Yexowa. Jàngal Njàlbéen ga 40:20-22 ak Macë 14:6-10. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Lan moo xew ci ñaari feetu aniwerseer yooyu?

  • Boo sukkandikoo ci li Biibël bi nettali, ci sa xalaat naka la Yexowa gise feetu aniwerseer?

Waaye ba tey, xéyna dinga ne, ‘Ndax ci dëgg-dëgg, am na solo ci Yexowa ma bokk walla bañ a bokk ci feetu aniwerseer walla ci beneen feet bu jógewul ci Biibël bi?’ Jàngal Mucc ga 32:1-8. Boo paree seetaanal WIDEO BI te tontu ci laaj yii di topp.

WIDEO: Ay feet ak ay màggal yu neexul Yàlla (5:07)

  • Lan moo tax ñu war a fexe ba xam bu baax li neex Yexowa?

  • Naka lañu ko mënee def?

Ni ñu mënee xam ne ab feet neexul Yàlla

  • Ndax ci njàngale yu jógewul ci Biibël bi la sukkandiku? Gëstul ba xam fi mu cosaanoo ngir xam tontu bi.

  • Ndax dafay màggal nit, mbootaay walla réew? Yexowa rekk lañuy màggal te moom lañu gëm ne, moo mën a faj jafe-jafey doomu Aadama yi.

  • Ndax aada yi ñu ciy topp ak jëf yi dañoo wuute ak li Biibël bi santaane? Dañu war a wéy di sell.

5. Dimbalil ñeneen ñi ñu respekte li nga gëm

Bu la ñeneen ñi di puus ci bokk ci feet bu neexul Yexowa, wax leen déet-déet mën na jafe. Xamal leen li nga dogal ci teey ak teggin. Boo bëggee gis ni nga mën a defe loolu, seetaanal WIDEO BI.

WIDEO: Xamleel li nga gëm ànd ci ak teggin (2:01)

Jàngal Macë 7:12. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Boo sukkandikoo ci aaya bi, ndax sa mbokk yi dul jaamu Yexowa, war nga leen a wax ne waruñu def yenn feet yi?

  • Lan nga mën a def ngir won sa waa kër ne, bu dee sax doo bokk ci yenn feet yi, ba tey bëgg nga leen te fonk nga leen?

6. Yexowa dafa bëgg ñu bég

Yexowa dafa bëgg ñuy bànneexu ak suñu waa kër ak suñuy xarit. Jàngal Kàdduy Waare 8:15. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Naka la aaya bii di wonee ne Yexowa dafa bëgg ñu bég?

Yexowa dafa bëgg ay jaamam ànd di fo ak di bànneexu. Seetaanal WIDEO BI ngir gis ni loolu di feeñee bu baax, ci suñu Ndaje yu mag yu ñetti fan yi ñuy amal ci réew yu bari.

WIDEO: Teraanga ji ñuy wone ci suñu ndaje yu mag yi (5:40)

Jàngal Galasi 6:10. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Ndax soxla nañu bokk ci feet yi ngir mën a ‘defal lu baax’ ñeneen ñi?

  • Lan moo lay bégal, nga maye ndax feet la, amuloo beneen pexe, walla nga maye ndaxte dafa laa neex nga def ko?

  • Ay Seede Yexowa yu bari dañuy defal seeni doom lée-lée lu neex te may leen sax ay kado fekk xale yi xaaruñu ko woon. Bu dee am nga ay doom, lan lu neex nga leen mën a defal?

Benn xale bu jigéen mu ngi jot kado bu mu xaarul woon ci ay waajuram.

BU LA NIT WAXOON: «Fi feet bi jóge amul solo noonu. Li gën a am solo mooy nga bànneexu ci ak sa waa kër ak say xarit.»

  • Lan ngay wax?

NAÑU TËNK

Yexowa dafa bëgg ñuy bànneexu ak suñu waa kër ak suñuy xarit. Waaye dafa bëgg itam ñu moytu feet yi ko neexul.

Nañu fàttaliku

  • Yan laaj lañu mën a laaj suñu bopp ngir xam ndax ab feet neex na Yexowa walla déet?

  • Naka lañu mënee dimbali suñu waa kër ak suñuy xarit ñu nànd dogal yi ñu jël ci lu jëm ci feet yi?

  • Naka nga xame ne Yexowa bëgg na ñu bég ak di fo?

Jubluwaay

GËSTUL

Xoolal yenn ci feet yi karceen yi dul feetu.

«Lu tax Seede Yexowa yi duñu bokk ci yenn feet yi?» (Ci jw.org la nekk)

Xoolal ni benn ndaw bu bëgg Yexowa di def ba neex ko bu nit ñi di feetu.

Yexowa fonk na leen (11:35)

Ay milioŋi karceen dañu tànn bañ a bokk ci feetu Nowel. Lan la dogal bi ñu jël def ci ñoom?

«Gis nañu lu gën» (w12 1/12)

a Xoolal Yeneen leeral 5 ngir xam li nga mën a def bu ñeneen ñi def seen feet.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager