LESOŊ 56
Nañu wéy di doon benn ci mbooloo mi
Bu ñu nekkee ak suñu mbokk yi ci ngëm, dañuy yëg li Daawuda yëgoon. Lii la waxoon: «Céy liika baax te neexati, ay bokk yu bokk dëkk, di benn!» (Sabóor 133:1). Xëyuñu rekk doon benn. Ku nekk ci ñun dafay def wàllam ngir ñu wéy di doon benn.
1. Lan lu amul fenn lañuy gis ci mbooloo Yàlla?
Boo teewee ndaje ci beneen réew, mën nga bañ a dégg làkk bi ñu fay làkk, waaye doo yëg ne gan nga fa. Lu tax? Ndaxte ñun ñépp téere yi ñuy jëfandikoo ngir jàng Biibël bi, benn lañu ak foo mënta dem. Dañuy def it lépp ngir wonante mbëggeel ci suñu biir. Ak fu ñu mënta dëkk, ñun ñépp dañuy «tudd [...] turu Aji Sax ji, di ko jaamoondoo benn bopp» (Cefaña 3:9).
2. Lan nga mën a def ngir ñu gën a doon benn?
«Bëgganteleen mbëggeel gu tar ak seen xol bépp» (1 Piyeer 1:22). Naka nga mënee topp xelal boobu? Xanaa nga bañ di xool rekk njuumte ñeneen ñi, waaye ngay xool ci seeni jikko yu rafet. Bul yem it ci xaritoo rekk ak ñi nga bokkal bëgg-bëgg waaye deel jéem a xamante itam ak mbokk yu góor ak yu jigéen yu wuute ak yow. War nañu def itam suñu kem kàttan ngir buddi ci suñu xol bépp ñaaw njort (1 Piyeer 2:17).a
3. Lan ngay def boo jotee ak sa mbokku karceen?
Dëgg la ne bennoo am na ci suñu biir, waaye nag matuñu. Lée-lée ñàkk déggoo mën na am walla sax ñu tooñ suñu moroom. Moo tax Kàddu Yàlla ne ñu, ñuy «baalante,» teg ci itam ne: «Baalanteleen, ni leen Boroom bi baale» (Jàngal Kolos 3:13). Dañuy tooñ Yexowa ay yooni-yoon, terewul dafa ñuy baal. Kon li muy xaar ci ñun mooy, ñuy baal suñu mbokk yi. Boo gisee ne am na koo tooñ, defal li war ngir jàmm dellusi ci seen diggante (Jàngal Macë 5:23, 24).b
XÓOTALAL NJÀNG MI
Xoolal li nga mën a def ngir yokk bennoo ak jàmm bi ci biir mbooloo mi.
Lan ngay def ngir juboo am?
4. Moytul a am gis-gis bu ñaaw ci ñeneen ñi
Li ñu bëgg mooy am mbëggeel ci suñu mbokk yi yépp. Waaye mën nañu am jafe-jafe bëgg ñi wuute ak ñun. Lan moo ñu mën a dimbali? Jàngal Jëf ya 10:34, 35. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:
Yexowa nangu na nit ñi bokk ci xeet yépp nekk ay seedeem. Naka nga ko mënee roy ci gis-gis bi nga am ci nit ñi wuute ak yow?
Fi nga dëkk, ban gis-gis bu ñaaw la nit ñi faral di am, ci nit ñi wuute ak ñoom? Lu tax nga war a moytu loolu?
Jàngal 2 Korent 6:11-13. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:
Ci sa xalaat, lan nga mën a def ngir gën a jege sa mbokk yu góor ak yu jigéen yi wuute ak yow?
5. Nañuy baale te wut a juboo ak ñépp
Yexowa du mas a soxla ñun ñu baal ko, waaye terewul dafa ñuy baal. Jàngal Sabóor 86:5. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:
Lan la la aaya bii di jàngal ci Yexowa?
Lu tax nga am ngërëm ci Yexowa ndax ni mu lay baale?
Lan moo mën a tax mu jafe ci ñun, ñu wéy di am jàmm ak ñeneen ñi?
Naka lañu mënee roy Yexowa te wéy di doon benn ak suñu mbokk yi ci ngëm? Jàngal Kàddu yu Xelu 19:11. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:
Bu la nit merloo mbaa mu tooñ la, lan nga mën a def ngir jàmm am?
Lée-lée ñun ñooy tooñ neneen ñi. Bu loolu amee, lan lañu war a def? Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.
Ci wideo bi, lan la mbokk bu jigéen bi def ngir juboo ak mbokkam?
6. Xoolal jikko yu baax yi sa mbokk yi ci ngëm am
Bu ñu demee ba xam bu baax suñu mbokk yu góor yi ak yu jigéen yi ci ngëm, dañuy gën a xam it seen jikko yu rafet ak seeni sikk. Naka lañu mënee xool ci seen jikko yu baax rekk? Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.
Lan moo la mën a dimbali nga gis jikko yu rafet yi sa mbokk yi ci ngëm am?
Yexowa suñu jikko yu rafet lay xool. Jàngal 2 Chroniques 16:9a. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:
Xam ne Yexowa say jikko yu rafet lay xool, loolu lan lay def ci yow?
Jamaa mën na am sikk waaye loolu terewul muy jar njëg lu réy. Noonu itam, suñu mbokk yi matuñu waaye terewul Yexowa fonk na leen
BU LA NIT WAXOON: «Man bala may baal nit, fàww mu baalu ma ba pare.»
Lu tax ñu war di gaaw a baal ñeneen ñi?
NAÑU TËNK
Booy baale te won mbëggeel sa mbokk yi ci ngëm, dinga yokk bennoo bi am ci mbooloo mi.
Nañu fàttaliku
Naka nga mënee moytu am gis-gis bu ñaaw ci ñeneen ñi?
Lan ngay def boo jotee ak sa mbokku karceen?
Lu tax nga bëgg a roy Yexowa ci fasoŋ bi muy baalee nit ñi?
GËSTUL
Xoolal ni benn misaal bu Yeesu joxe woon di ñu dimbalee ñu bañ a sikkal ñeneen.
Bu ñu jàppee ne defuñu dara lu bon, ndax war nañu baalu ba tey?
Xoolal li ay nit def ba bañ a am gis-gis bu ñaaw ci ñeneen ñi.
a Yeneen leeral 6 dafay wone ni mbëggeel di xiire karceen yi ñu moytu wàll ñeneen ñi feebar.
b Yeneen leeral 7 dafay wax li ñu mën a def ba regle poroblem yi jëm ci xaalis ak li yoon laaj.