TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • g18 n° 2
  • 5 Waxtaan

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • 5 Waxtaan
  • Yeewuleen! (2018)
  • Turu xaaj yi
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • LI MUY TEKKI
  • LI TAX MU AM SOLO
  • LI NGA MËN A DEF
  • 8 Royukaay
    Yeewuleen! (2018)
  • Naka ngeen war a yare seen doom?
    Mën ngeen a am jàmm ci seen biir njaboot
Yeewuleen! (2018)
g18 n° 2
Ay waajur ñu ngi jéggi benn pom ngir fekki seen doom bu jiggéen

Waxtaan dafa mel ni pom buy dox sa diggante ak say doom

WAAJUR YI ÑOO MOOM LII

5 Waxtaan

LI MUY TEKKI

Booy wax ak sa doom, te ku nekk ci yéen di wax li mu xalaat ak li mu yëg, loolu mooy waxtaan dëgg.

LI TAX MU AM SOLO

Waxtaan ak ndaw ñi mën na nekk lu jafe. Benn téere buy wax ci ndaw ñi nee na: «Xéyna, yàggul dara, xamoon nga lépp li say doom daan def. Waaye léegi xamatuloo dara ci ñoom. Te xéyna, du loolu moo la gënal». Bu loolu amee, xamal ne, waxtu woowu lañu gën a soxla ku waxtaan ak ñoom.

LI NGA MËN A DEF

Waxtaanal ak sa doom ci waxtu wi mu ko soxla. Deel waxtaan ak moom bu dee sax guddi moo ko gënal.

«Xéyna nga bëgg koo tontu ne: ‘Bëccëg bi yépp ñoo nekkoon, nga bàyyi ba léegi ngay bëgg wax! ’ Ndax war nañoo wax dara, bu ñu suñu doom bëggee wax li nekk ci xolam? Ndax du loolu la waajur yépp bëgg?» (Lisa)

«Teel a tëdd moo ma gënal. Waaye, waxtaan yi gën a xóot yi ma am ak samay doom, guddi la woon» (Herbert).

LII LA BIIBËL BI WAX: «Bu kenn seet njariñam rekk, waaye nay seet njariñul moroomam» (1 Korent 10:24)

Bàyyil xel ci li ñu lay wax. Benn baay lii la wax: «Yenn saa yi, samay doom bu ñuy wax ak man, sama xel dafay dem ci leneen. Te ñoom dañu koy seetlu.»

Bu dee sa tele walla sa telefon dafay tax sa xel dem ci leneen, fey ko mbaa nga teg ko feneen. Bàyyil xel bu baax ci li sa doom di wax. Bu dee sax foog nga ne li mu lay wax amul solo, xamal ne war nga koo déglu bu baax.

«War nañu xamal suñu doom yi ne li ñuy yëg, lu am solo la ci ñun. Boo ko deful, duñu la ubbil seen xol, walla dinañu dem wuti ndimbal feneen» (Maranda).

«Àndal ak dal, bu dee sax li sa doom di xalaat jaarul yoon» (Anthony).

LII LA BIIBËL BI WAX: «Seetleen bu baax, ni ngeen di dégloo» (Luug 8:18).

Deel waxtaan ak ñoom saa yu mënee nekk. Yenn saa yi, dafay gën a yomb ci xale yi ñu ubbil la seen xol, bu ñu jàkkaarloowul ak yow waajur ji.

«Dañuy faral di waxtaan buñu nekkee ci oto. Bañ a jàkkarloo ak ñoom, waaye nekk ci seen wet tax na, ñu am waxtaan yu neex» (Nicole).

Bu ñuy lekk itam mën nañu waxtaan.

«Bu ñuy reer, ku nekk dafay wax li ko gën a neex ak li ko gën a metti ci bés bi. Loolu dafay tax ñu doon benn te dafay tax ku nekk xam ne dinañu ko dimbali bu amee ay jafe-jafe» (Robin).

LII LA BIIBËL BI WAX: «Ku nekk war ngaa farlu ci déglu, di yéexa wax» (Saag 1:19).

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager