XAAJ 1
Dañu fi nettali bi Yàlla komaasee sàkk ba bi mu indee mbënn mi, maanaam taw bu metti, ci kow suuf si sépp
Asamaan ak suuf, fan la jóge ? Naaj bi, weer bi ak biddéew yi, lépp lu ñu gis ci kow suuf si, lan moo leen fi indi ? Biibël bi nee na Yàlla moo ko sàkk. Loolu mooy dëgg. Kon suñu téere bii, dina jëkk a nettali li Biibël bi wax ci li Yàlla sàkk.
Yàlla dafa jëkk a sàkk malaaka yi. Waaye suuf si dafa ko sàkk ngir ñun. Sàkk na benn góor ak benn jigéen, mu tudde leen Aadama ak Awa. Dafa leen dugal ci benn tool bu rafet lool. Waaye ñoom, déggaluñu Yàlla. Loolu moo tax ñu waroon a dee.
Diggante bi Yàlla sàkkee suñu maam Aadama ak bi Yàlla wàccee taw bu metti ci kow suuf si sépp, amoon na 1656 at. Ñu bon ñi, bare woon nañu. Ca asamaan, amoon na Seytaane ak malaakaam yu bon yi. Ci kow suuf si, amoon na Kayin. Amoon na itam ay ponkal yu réy lool ak yeneen nit ñu bon. Waaye amoon na itam ay nit ñu baax — Abel, Enog ak Nóoyin. Loolu yépp lañuy nettali ci XAAJ 1.