TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • ll xaaj 2 p. 6-7
  • Kan mooy Yàlla dëgg ji ?

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Kan mooy Yàlla dëgg ji ?
  • Déggleen li Yàlla wax ndax ngeen am dund gu dul jeex
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Xaaj 2
    Déggleen li Yàlla wax
  • Ku leen sàkk ?
    Dundleen ba fàww ak bànneex ci suuf si !
  • Kan mooy Yàlla ?
    Lan la ñu Yàllay laaj?
  • Kan mooy Yàlla?
    Gëm Yàlla dëgg moo ñu mën a indil jàmm
Xóotalal waxtaan bi
Déggleen li Yàlla wax ndax ngeen am dund gu dul jeex
ll xaaj 2 p. 6-7

XAAJ 2

Kan mooy Yàlla dëgg ji ?

Ca gànguneem ca asaman, la Yexowa di gisee li mu sàkk ca asamaan ak ci suuf

Benn Yàlla dëgg rekk moo am, turam mooy Yexowa (Psaume 83:18). Xel la, ci kaw asamaan la dëkk, kenn mënu koo gis. Yexowa bëgg nañu, te li muy xaar ci ñun mooy ñu bëgg ko, bëgg itam suñu moroom (Macë 22:35-40). Moo ëpp ñépp kattan, te moo sàkk lépp.

Li Yàlla njëkk a sàkk mooy kenn koo xam ne ku bare kàttan la ca asamaan. Moom lañu mujj a woowe Yeesu. Yexowa sàkkoon na itam malaaka yi.

Yexowa moo sàkk lépp lu nekk ci kaw asamaan . . . ak ci kaw suuf. Peeñu ma 4:11

Yexowa moo sàkk biddéew yi, suuf si ak lépp li ci nekk.— Njàlbéen ga 1:1.

Sàkk na itam góor gu njëkk ga, maanaam Aadama. Ci pëndu suuf la ko sàkke. — Njàlbéen ga 2:7.

  • Lu tax ñu war a màggal Yexowa ? — Esayi 42:5.

  • Lan la Gàddaay gi 34:6 wax ci Yàlla ?

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager