TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • bh p. 3-7
  • Ndax lii la Yàlla bëggoon ?

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ndax lii la Yàlla bëggoon ?
  • Lan la Biibël bi wax dëgg-dëgg ?
  • Turu xaaj yi
  • SOPPI YI BIIBËL BI WAX NE YÀLLA DINA KO DEF CI KAW SUUF.
  • NANGA JARIÑOO LI BIIBËL BI WAX
Lan la Biibël bi wax dëgg-dëgg ?
bh p. 3-7

Ndax lii la Yàlla bëggoon ?

JÀNGAL surnaal boo bëgg. Seetaanal tele mbaa nga déglu rajo. Jëf yu bon, geer ak li ñuy woowe ci tubaab terrorisme lañu fay gën a dégg ! Xalaatal ci say jafe-jafe. Xéyna nga am lu la metti lool ndax mbokk walla xarit bu feebar walla bu gaañu. Xéyna dinga yëg li Ayóoba yëgoon ci xolam. Nit ku baax kooku lii la waxoon : “ Sama dund gépp, coono kese la. ” — Ayóoba 10:​15, NW.

Laajal sa bopp lii :

  • Ndax lii la Yàlla bëggoon pur man ak pur doomu Aadama yi ?

  • Fan laa mënee am ndimbal ci samay coono ?

  • Ndax mën nañu yaakaar ne jàmm dina mas a am ci suuf si sépp ?

Biibël bi dafay tontu lu leer ci laaj yooyu.

SOPPI YI BIIBËL BI WAX NE YÀLLA DINA KO DEF CI KAW SUUF.

“Dina fomp bépp rangooñ ci seeni bët ; te dee dootul am walla naqar walla jooy walla metit.” — Peeñu ma 21:⁠4.

‘ Lafañ dina tëbeentu ni kéwél. ’ — Esayi 35:⁠6.

 Gumba yi dinañu gis. ’ — Esayi 35:⁠5.

“Néew yépp, yi nekk ci seen bàmmeel, di[nañu...] génn.” — Yowaana 5:​28, 29.

“ Kenn ci waa réew mi du wax : ‘ Dama feebar. ’ ” — Esayi 33:​24, NW.

“ Pepp mi [dina] baawaan ci réew mi. ” — Sabóor 72:⁠16.

Àddina si ni ko Yàlla bëgge woon : Ab màggat nekk na ndaw, ki feebaroon ak ki gumba wér nañu, ñi dee dekki, lekk bi baawaan

NANGA JARIÑOO LI BIIBËL BI WAX

Bul gaaw a wax ne li nekk ci xët yi weesu, wax yu neex kese la. Yàlla moo ñu dig ne dina def loolu, te Biibël bi wax na ni mu koy defe.

Ñaari góor yuy jàng Biibël bi ak téere Biibël wax

Waaye Biibël bi def na lu ëpp loolu. Dafa ñu won it ni ñu mënee am dund gu neex dëgg tey jii sax. Xalaatal tuuti ci say naqar ak say coono. Mën na doon poroblemu xaalis, poroblem ci sa njaboot, feebar, mbaa mbokk walla xarit bu gaañu. Biibël bi mën na la dimbali nga xam ni ngay faje say poroblem. Mën na la may doole it ci li muy tontu ci laaj yu mel nii :

  • Lu tax ñuy am metit ?

  • Naka lañuy def ba faj poroblem yi ñuy am ?

  • Lan lañu mën a def ba gën a am jàmm ci suñu kër ?

  • Lan mooy dal nit bu deewee ?

  • Ndax dinañu mas a gisaat suñu mbokk walla suñu xarit yi gaañu ?

  • Naka lañuy def ba mu wóor ñu ne Yàlla dina def li mu ñu dig ?

Li ngay jàng téere bii, dafay wone ne bëgg nga xam li Biibël bi wax. Téere bii dina la ci dimbali. Seetlu nga ne, xise bu nekk dafay am laaj bi mu àndal. Bind nañu ko ci suufu xët bi. Ay milyoŋi nit kontaan nañu ci fasoŋ bi ñuy jànge Biibël bi ak Seede Yexowa yi, maanaam li ñu leen di laaj ay laaj, ñu ciy tontu. Yaakaar nañu ne fasoŋ boobu dina la neex yow itam. Ñu ngi ñaan Yàlla mu barkeel lu neex te am solo li ngay def, maanaam di jàng li Biibël bi wax dëgg-dëgg !

NANGA XAM BU BAAX LI NEKK CI SA BIIBËL

BIIBËL bi yépp, 66 téere ak leetar la. Dañu leen xaaj ci ay pàcc ak ay aaya ngir mu neex a gëstu. Bu ñu limee ay aaya ci téere bii, nimoro bi topp turu téere Biibël bi, mooy pàcc bi. Nimoro bi ci toppaat nag mooy wone aaya bi. Nañu ko seet ci lii : Bu ñu waxee “ 2 Timote 3:16 ”, dafay tekki ñaareelu bataaxal bu Timote, pàcc 3, aaya 16.

Dinga gaaw a xam bu baax li nekk ci Biibël bi, booy seetal sa bopp aaya yi ñu lim ci téere bii. Lu tax doo komaase jàng it bés bu nekk Biibël bi ? Booy jàng ñett ba juróomi pàcc bés bu nekk, dinga jàng Biibël bi yépp ci benn at.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager