NJÀNGALE 23
Naka lañuy binde suñu téere yi te naka lañu leen di tekkee ci yeneen làkk ?
Biro bi yor wàllu mbind mi ca Etaa Sini.
Corée du sud
Armenie
Burundi
Sri Lanka
Dañuy def suñu kem kàttan ngir yégal “ xibaar ” bi “ xeet yépp ak giir yépp ak kàllaama yépp ak réew yépp. ” Loolu moo tax ñu ngi sotti ay téere ci lu jege 750 làkk (Peeñu ma 14:6). Lan moo ñuy dimbali ñu mën a def liggéey bu metti boobu ? Dañu am gurupu bindkat yu jóge ci àddina si sépp ak benn gurupu nit yu sawar yuy tekki suñuy téere, te ñoom ñépp ay seede Yexowa lañu.
Li ñu bind, ci ãgale lañu ko njëkk a bind. Jataay biy dogal mooy jiite liggéey bi ñuy def ci Biro bi yor wàllu mbind mi te mu nekk ci suñu kër gu mag gi. Biro boobu mooy toppatoo liggéey bi ñuy jox bindkat yi nekk ci kër gu mag gi ak ci yenn bànqaas yi. Li ñu am ay bindkat yu bare te wuute tax na ba suñu téere yi mën a laal xeet yu bare.
Li ñu bind, dañu koy yónnee ñiy tekki. Bu bindkat yi paree mbind mi ci ãgale, dañu koy seetaat ba Jataay biy dogal nangu li ñu ci bind, ñu daldi ko yónnee ci internet gurup yiy tekki te ñu nekk ci àddina si sépp. Gurup bu nekk dafay tekki ci làkkam li ñu ko yónnee. Dañuy def lépp ngir tànn ci seen làkk baat yu jub te méngoo ak li ñu wax ci ãgale. — Ecclésiaste 12:10.
Ordinatër yi dañu tax liggéey bi gën a gaaw. Dëgg la, ordinatër mënul a def liggéey bi bindkat yi ak ñiy tekki di def, waaye jëfandikoo ordinatër dafay tax liggéey bi gën a gaaw. Seede Yexowa yi defar nañu itam lu ñuy wax ci tubaab système électronique d’édition multilingue (MEPS) biy tax ñu mën a dugal mbind mi ci ay ordinatër ci ay téeméeri làkk. Dafay tax itam ñu mën a boole mbind mi ak ay nataal walla foto ba mu rafet, ba ñu mën koo sotti ci ay masin yu gaaw.
Lu tax ñuy def loolu yépp ngir tekki téere yi ci ay làkk yu bare, fekk yenn ci làkk yooyu, ñi koy làkk barewuñu ? Ndaxte Yexowa dafa bëgg “ ñépp mucc te xam dëgg gi. ” — 1 Timote 2:3, 4.
Naka lañuy binde suñu téere yi ?
Lan moo tax ñuy tekki suñu téere yi ci làkk yu baree-bare ?