Nit ñi, ak làkk bu ñu mënta dégg, nañu leen indi ci mbooloo mi
1 Li kàddu Yàlla waxoon, mu ngi am ! Ay nit ñu bare, ak làkk bu ñu mënta dégg, ñu ngi dugg ci diine dëgg ji (Sak. 8:23). Naka la Seede Yexowa yi di dimbalee nit ñu bokk “ ci giir yépp, réew yépp ak kàllaama yépp ” ba ñu sell ci kanamu Yexowa, bu ko defee ñu mën a mucc “ ca mettit wu réy wa ” ? — Peeñ. 7:9, 14.
2 Ni mbootaayu Yàlla di dimbalee nit ñi : Jataay biy dogal mu ngi fexe ba ñu mën a am ay téere ci lu mat 380 làkk. Loolu dafay tax niti àddina si sépp mën a xam bu baax naka la xibaar bu baax bi ame solo. Waajal te defar ay téere ci ay làkk yu bare noonu, yombul dara. Laaj na ñu am ay nit ñu mën a tekki bu baax li ñu bind ci làkk yooyu yépp. Laaj na it ñu jox nit ñooñu lépp li ñu soxla ngir def liggéey boobu. Muul ay téere ci làkk yépp te yónne leen fi ñu leen soxla, bokk na it ci liggéey boobu. Waaye ñi gën a mën a dimbali nit ñi ñooy waaraatekat yi ci seen bopp, kenn ku ci nekk : ñoo leen war a xamal xibaar bu leen di may dund gi.
3 Bu dee sax dina la laaj lu bare, nanga ko def : Ay jaamukati Yàlla yu gën di bare, ñu ngi jàng sinoa (chinois), rus (russe), español, walla yeneen làkki bitim réew. Lu tax ? Ñi jóge bitim réew te bañ a dégg làkku réew mi bare nañu ci seen gox, te dañu leen bëgg jottali xibaar bu baax bi. Ñeneen jaamukati Yàlla ñu ngi jàng làkku liyaaru Amerig walla bu tugal (maanaam làkku ñi tëx). Ci Afrig, ñu ngi waare xibaar bu baax bi ci ay làkk yu baree bare. Nit ñu masul woon a dégg lu jëm ci Yexowa, walla ñu xamul woon dara ci Biibël bi, ñu ngi nangu dëgg gi nekk ci kàddu Yàlla. — Room 15:21.
4 Ndax mën nga gën a góor-góorlu ngir xamal xibaar bu baax bi nit ñu jóge bitim réew (Kol. 1:25) ? Ay mbooloo yu bare, dañuy fexe ba mën leen waar ci seen làkk. Waaraatekat yi dañuy njëkk jàng lu yomb lu ñu mën a wax, lu mel ni : “ Salaamaalekum. Dama am xibaar bu baax bu ma la bëgg jottali. [Ba pare nanga wone benn kayit bu ndaw walla téere bu ñu bind ci làkk bu nit ki dégg.] Maa ngi dem ba beneen. ” Ci lu wóor, bu ñu tàmbalee noonu, Yexowa dina barkeel lu tuuti loolu ñu wax !
5 Xibaaru Nguur gi, itteel na nit ñu bokk ci xeet ak làkk yépp. Nañu def li ñu mën ngir xamal leen xibaar boobu.