WOY-YÀLLA 22
Nguur gi sampu na... na ñëw!
(Peeñu ma 11:15; 12:10)
1. Céy suñu Yàlla Yexowa
yow yaay Yàlla ba fàww.
Yeesu sa doom ji, mooy buur bi.
Loolooy sa coobare.
Kon léegi Nguur gi sampu na;
te dina ilif suuf si sépp.
(AWU BI)
Keroog buur bi dina
xettali nit ñi, muccal leen,
ndax Nguur gi sampu na.
Ñu ngi ñaan mu ñëw, «Yal na ñëw!»
2. Li dese Ibliis bareetul;
looloo tax ñuy séentu,
ak nu dund gi mën a mel,
barke yi nar a ñëw.
Kon léegi Nguur gi sampu na;
te dina ilif suuf si sépp.
(AWU BI)
Keroog buur bi dina
xettali nit ñi, muccal leen,
ndax Nguur gi sampu na.
Ñu ngi ñaan mu ñëw, «Yal na ñëw!»
3. Malaaka asamaan yi bég
te woy woyu mbégte.
Seytaane ak fenam yi jeex.
Asamaan daldi set.
Kon léegi Nguur gi sampu na;
te dina ilif suuf si sépp.
(AWU BI)
Keroog buur bi dina
xettali nit ñi, muccal leen,
ndax Nguur gi sampu na.
Ñu ngi ñaan mu ñëw, «Yal na ñëw!»
(Xoolal itam Dañeel 2:34, 35; 2 Korent 4:18.)