Woy-Yàlla 13 (33)
“Yeowa ci boppam mujj naa doon Buur!”
(Sabuur 97:1)
1. Gërëmleen Yeowa, yéen gaayam.
Xamleleen jalooreem ci biir xeet yépp.
Woyalleen suñ’ Yàlla, woy wu neex ci xalam,
Ittewoo barke yi muy xëpp.
(AWU)
Na asamaan nox-noxi, na suuf si sép’ bànneexu,
Ndax Yeowa Yàlla mujj naa doon Buur!
Na asamaan nox-noxi, na suuf si sép’ bànneexu,
Ndax Yeowa Yàlla mujj naa doon Buur!
2. Weejalleen ndamam ci biir xeet yi.
‘Mooy Aji-Musal ji,’ deeleen ko xamle.
Yeowa yaa na, yeyoo tagge kuy noyyi;
Moo sut fuuf ñiiy yàllay tappale.
(Awu)
3. Màqaamaak kàttan jagleelleen ko.
Jaajëf ndax sa Doom ji, suñ’ Buur Krist Yeesu.
Nañ’ sujjóotal Yàlla, di mbooloo mu mànkoo;
‘Woy ak mbég Yaa,’ lool’ lañuy taasu.
(Awu)