WOY-YÀLLA 36
Nañu sàmm suñu xol
(Kàddu yu Xelu 4:23)
1. Suñu xol, nañu ko sàmm,
nañu sore bàkkaar.
Yàlla day gis li ci biir xol,
dara mënu koo réer.
Lée-lée, suñu xol jaxasoo,
jaarale ñu fu bon.
Suñu xel daldi ko delloo
ci yoonu Yexowa.
2. Suñu xol, nañu ko sàmm
te sax ci ñaan Yàlla.
Gërëm Yàlla, te tinu ko,
di ko ñaan saa su ne.
Li ñu Yexowa di jàngal,
dañu koy def ak mbég.
Dañuy wéy di takku ci moom,
di ko neex saa su ne.
3. Suñu xol, nañu ko sàmm,
nañu fonk dëgg.
Nañu jàng Kàddu Yàlla,
miy tax a jëm kanam.
Yàlla fonk na suñu ngor
te loolu lu wóor la.
Nañu ko jox xol bu mat sëkk,
doon xaritam ba fàww.
(Xoolal itam Taalifi Cant 34:1; Filib 4:8; 1 Piyeer 3:4.)