WOY-YÀLLA 37
Dama laa bëgg a jaamu ak sama jëmm jépp
(Macë 22:37)
1. Céy Yexowa, maa ngi lay jox
sama mbëggeel te di la déggal.
Yow yaa yelloo ma ragal la,
yaay sama Yàlla, ci yow laay ñëw.
Dama bëgg topp say tegtal,
te it takku ci say ndigal.
(AWU BI)
Yow laa jébbal sama dund.
Yow rekk yaa yelloo ñu jaamu la.
2. Asamaan ak suuf ak weer wi,
càkkeef bi wone na ki nga doon.
Dama bëgg takku ci yow.
Ak sama doole, xamle sa tur.
Dama laa jébbal sama dund,
bëgg naa def sa coobare.
(AWU BI)
Yow laa jébbal sama dund.
Yow rekk yaa yelloo ñu jaamu la.
(Xoolal itam Baamtug Yoon wi 6:15; Taalifi Cant 40:8; 113:1-3; Kàdduy Waare 5:4; Yowaan 4:34.)