WOY-YÀLLA 107
Nañu roy ci mbëggeelu Yàlla
(1 Yowaana 4:19)
1. Yexowa Yàlla, yaay suñu royukaay
Ci mbëggeel ak cofeel.
Wone nga mbëggeel, mbëggeel bu xóot a xóot.
Yow yaay mbëggeel, yaa jar a roy!
Maye nga sa doom, ak ni nga ko bëgge,
Ngir nga mën ñoo baal suñuy tooñ ak bàkkaar,
Nga wone noonu, mbëggeel gu réy a réy.
Yow yaay mbëggeel te amoo moroom.
2. Nañu won mbëggeel, nit ku mu mën a doon,
Ubbil ko suñu xol.
Nañu dimbali képp ku am soxla,
Muy mag ak ndaw, góor ak jigéen.
Ku bëgg Yàlla, ndax war na dencal mer
Mbokk bu ko tooñ te xamu ci dara?
Li gën mooy baale njuumte ak bàkkaar yi.
Nañuy baale, mbëggeel day baale.
3. Ñun dañoo booloo, mbëggeel moo ko waral.
Jàmm a neex, aka neex!
Li neex Yexowa, mooy ñu wone mbëggeel,
Muy lu dëggu, te rafet lool.
Su ñu ko defee, nit ñi dinañu gis
Ne njaboot lañu, Yàlla moo ñu boole.
Roy ci mbëggeelam, mooy yoon bi ñu taamu.
Yoonu mbëggeel, ci la ñuy tegu.
(Xoolal itam Room 12:10; Efes 4:3; 2 Piyeer 1:7.)