WOY-YÀLLA 117
Nañu roy mbaaxu Yexowa
(2 Jaar-jaar ya 6:41)
1. Yow yaa baax, sell te gore,
Aji Sax ji Yexowa.
Suñu bànneex a la soxal.
Bés bu ne, dañu koy yëg.
Baay, sa ngor ak sa yërmande
ñooy tax ngay wéy di ñu baal.
Say santaane lañuy topp,
noonu lañu lay royee.
2. Ñi lay seedeel, aka ñoo baax,
dafa feeñ ci seen jikko.
Mbaax a tax ñuy dem waareji,
dañuy déggal sa kàddu.
Yaa leen tànn, yaa leen jiite,
say njàngale lañuy topp.
Yal na sa xel mu sell mi
xiir ñu ci ay jëf yu baax.
3. Yexowa dina ñu barkeel
su ñu wàccul yoonu mbaax.
Na suñu mbaax doon liy dëfël
suñu mbokk yi ci ngëm.
Nañu roy mbaaxu Yexowa,
loolu, daf koy rafetlu.
Muy njaboot beek dëkkandoo yi,
na ku ne yëg suñu mbaax.
(Xoolal itam Taalifi Cant 103:10; Màrk 10:18; Galasi 5:22; Efes 5:9.)