WOY-YÀLLA 121
Nañu maandu
(Room 7:14-25)
1. Ngir neex Yexowa, war nañu maandu.
Te yombul ndax bàkkaar a ngi ñuy yeeru.
Topp sa bakkan, day jur naqar.
Nit kiy doxe xel, jàmm lay am.
2. Dañuy jànkoonteek fiiri Seytaane.
Teg ci di xeex bàkkaar bi ñuy fakkastal.
Dëgg gi mooy tax ñu noot lu bon.
Xelum Yàlla mooy li ñuy dooleel.
3. Yàlla tëral na yoon bi gën ci ñun.
Nañ ci jaar ak fulla ngir màggal turam.
Topp li ñu neex, du baax ci ñun.
Maandu, mooy li gën, te moo ñuy aar.
(Xoolal itam 1 Korent 9:25; Galasi 5:23; 2 Piyeer 1:6.)