Ndax li nga jàng neex na la?
Édition imprimée
Ndax bëgg nga yokk sa xam-xam ci Biibël bi?
Lii, xaaj bu ndaw rekk la ci téere bi tudd Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi).
Doo fey dara ngir am téere bi walla ngir ñu jàngal la ko. Dinañu bég ci jàngal la Biibël bi ci waxtu ak béréb bi la gënal.
Dinga ci jàng lu bare lu mel ni:
Li tax ñuy dund
Ni ñu mënee am jàmm dëgg
Ni njaboot yi mënee am jàmm
Li Biibël bi di yégle lu jëm ci ëllëg
Boo bëggee am téere bi te wéy di jàng Biibël bi, mën nga jokkoo ak benn Seede Yexowa walla nga bindu ci jw.org ngir ñu jàngal la Biibël bi.