Fan lañu mën a ame ay tont yu leer ci ay laaj yu am solo ?
Ci njàng mu sore ?
Ci mag ñi ?
Walla ci Biibël bi ?
LII LA BIIBËL BI WAX CI YÀLLA
“ Sa Kàddu mooy dëgg. ” — Yowaana 17:17, Téereb Injiil di Kàddug Yàlla, 2010.
Ay milioŋi nit ci àddina si sépp gis nañu ci Biibël bi ay tont yu leer ci seeni laaj yu am solo.
Ndax bëgg nga bokk ci ñooñu ?
Suñu palaas bi ñu moom ci internet, bi tudd jw.org, mën na la ci dimbali.
JÀNGAL ci internet bi
Biibël bi ci lu tollu ak ay téeméeri làkk
Ay tont ci ay laaj yu jëm ci Biibël bi
Lu mën a dimbali njaboot yi ñu am jàmm ci seen biir
SEETAANAL ay wideo yu sukkandiku ci Biibël bi
Ay njàngale ak ay woy ngir xale yu ndaw yi
Ay xelal ngir ndaw yi
Li ngëm dëgg mën a def
SOTTIL ci sa ordinatër ay téere yu mel ni
La Tour de Garde ak Réveillez-vous !
CI LAAJ YU AM SOLO YII BAN MOO LA CI GËN A ITTEEL ?
Ci dëgg, kan moo ilif àddina si ?
Ndax coono àddina dina mas a jeex ?
Ndax ñi dee dinañu dundaat ?
Xoolal tont yi Biibël bi joxe ci laaj yooyu ci jw.org.
(Demal ci LI BIIBËL BI WAX > AY LAAJ YU JËM CI BIIBËL BI)