TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • sjj woy 156
  • Gëm naa ne Yexowa mu ngi ak man

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Gëm naa ne Yexowa mu ngi ak man
  • Nañu woyal Yexowa ànd ceek mbégte
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • War nañoo am ngëm
    Woyal, di Tagg Yeowa
Nañu woyal Yexowa ànd ceek mbégte
sjj woy 156

WOY-YÀLLA 156

Gëm naa ne Yexowa mu ngi ak man

Édition imprimée

(Sabóor 27:13)

  1. 1. Man duma tiit ndax gaynde.

    Man duma tiit ndaxi noon.

    Ak Yàlla ci sama wet,

    Duma lox, duma daw.

    Yexowa mooy ki ànd ak man.

    (AWU BI)

    Ak ngëm gu wóor,

    man maa ngi gis li may xaar.

    Ak ngëm gu wóor,

    kenn warul tax ma tiit.

    Ak Yexowa,

    mën naa lépp.

    Dara du ma téye,

    Ndaxte Yexowa dina ma aar—

    Ak ngëm gu wóor.

  2. 2. Ñépp ñi gëmoon te takku,

    Ñoom seen muñ du réer ci neen.

    Dañu dee ak seen ngëm.

    Seen ëllëg dina neex.

    Yàlla dina leen woo ñu jóg.

    (AWU BI)

    Ak ngëm gu wóor,

    man maa ngi gis li may xaar.

    Ak ngëm gu wóor,

    kenn warul tax ma tiit.

    Ak Yexowa,

    mën naa lépp.

    Dara du ma téye,

    Ndaxte Yexowa dina ma aar—

    Ak ngëm gu wóor.

    (PONT BI)

    Ak ngëm gu wóor,

    man mën naa lu leen të.

    Ak ngëm gu wóor,

    am naa yaakaar.

    Ngëm gi ma am,

    Looloo ma aar

    ci lépp li am.

    Ndax moo ma may xolu muñ tiis.

  3. 3. Ak suuf su naat si ñuy xaar

    Ngir nit ñi bég ba fàww.

    Duma xàddi mukk.

    Xam naa ne léegi rekk

    Nguuru Yàlla sampu fi ba fàww.

    (AWU BI)

    Ak ngëm gu wóor,

    man maa ngi gis li may xaar.

    Ak ngëm gu wóor,

    kenn warul tax ma tiit.

    Ak Yexowa,

    mën naa lépp.

    Dara du ma téye,

    Ndaxte Yexowa dina ma aar—

    Ak ngëm gu wóor,

    Ak ngëm gu wóor.

(Xoolal itam Yawut ya 11:​1-40).

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager